Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 déc.
“ Léegi, ñu ngi ci jamano Nowel te nit ñu bare dañuy xalaat ci li malaaka bi waxoon ci juddu Yeesu. [Jàngal Luug 2:14.] Ndax foog nga ne dëgg-dëgg, jàmm dina mas a am ci kow suuf si ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone ni Yeesu di indee jàmm ci kow suuf, bu ci kanamee tuuti. ”
Réveillez-vous ! Déc.
“ Ci waxtu bi ñu tollu nii, ñu bare dañuy xalaat ci Yeesu, waaye dañu koy gise ni liir bu tëdd fu mala yi di lekke. Ndax mas nga xalaat ci lu tax Yàlla yónni ko ci kow suuf ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li malaaka bi tudd Jibril wax yaayam Maryaama. [Jàngal Luug 1:33, te woneel ne Yeesu dafa war a nguuru ba abadan.] Téere bii, dafay wax lu tax ñu war a xam bu baax li Yeesu di def ngir li Yàlla bëgg def ak suuf si am. ” Won ko xaaj biy komaase ci xët 4.
La Tour de Garde 1er janv.
“ Ndax foog nga ne li nit ki di gën a bare alal, àddinaam di gën a neex ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal 1 Timote 6:9, 10.] Dëgg la, Kàddu Yàlla terewul ñu am alal. Waaye nag, waxul ne bala sa dund mën a neex, fàww nga am alal ju bare. Loolu la téere bii di wone. ”
Réveillez-vous ! Janv.
“ Ndax foog nga ne lii dina mas a nekk dëgg ? [Jàngal Esayi [Isaïe] 33:24, ba pare mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone lan la boroom xam-xam yi di def ci wàllu wér-gi-yaram. Dafay wone it naka la li Yàlla dige di ame. ”