Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 déc.
“ Bu ñu tolloo ci weer wii, nit ñu bare dañuy xalaat ci juddu Yeesu. Ndax xam nga naka la njaboot gi mu màgge meloon ? [Mayal nit ki tontu ba pare jàngal Lukk 2:51, 52 te won ko ni Yeesu déggaloon way-juram te déggoo ak ñoom.] Téere bii dafay wone li Biibël bi wax ci ni Yeesu màgge ak li ñu ci mën a jàng. ”
Réveillez-vous ! 22 déc.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñépp a bëgg seen doom nekk ci jàmm te am lu baax. Ci yow, lan la xale yi gën a soxla ngir mën a am jàmm ci àddina su bare coono sii ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Léebu 22:6.] Réveillez-vous ! bii dafay wone lan la xale yi soxla, te naka la leen ko way-jur yi mënee jox. ”
La Tour de Garde 1er janv.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñu bare dañu bëgg jàmm am ci kow suuf si. Ndax foog nga ne li ñu wax fii dina mas a am ? [Jàngal Sabuur 46:9, ba pare mayal nit ki tontu.] La Tour de Garde bii dafay wone naka la loolu di ame ak lu tax mu mën ñu wóor ne, dund bu amul xare ni ko Yàlla dige dina am. ”
Réveillez-vous ! 8 janv.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Feebar bu ñuy wax depresioŋ walla feebar yu mel noonu bare na ci àddina si. Yàlla ittewoo na bu baax ñi am feebar yu mel noonu. [Jàngal Sabuur 34:18.] Téere bii dafay wone ni ñu mënee dimbali ñi am coono boobu. Dafay wone it ne, ni ko Biibël bi waxe, léegi benn feebar dootul amati. ”