TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/04 p. 6
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 12/04 p. 6

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 déc.

“ Léegi ñu ngi ci jamano Nowel te ci àddina sépp nit ñi dañuy fàttaliku bés bi Yeesu juddoo ci fasoŋ yu bare. Ndax xamoon nga ne juddu Yeesu moo tax ñu mën a yaakaar jàmm ba fàww ci kow suuf ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Isayi 9:​6,7 te saa yoo tasee ak baat “ jàmm ” ci aaya yooyu, nanga ko waxaat ngir nit ki xam bu baax ne ci jàmm ji lañuy wax.] Téere bii dina la wax naka la jàmm ji ñu wax fii di ame. ”

Réveillez-vous ! 22 déc.

“ Dañu bëgg waxtaan ak yow ci li ñu seetlu ci nit ñi. Ñu bare tey dañu bëgg rafet. Loolu sax bonul. Waaye ndax gis nga ne tey, dafa mel ni loolu rekk moo nekk ci xelu nit ñi ? Dafa mel ni boo rafetul tekkiwoo dara. Ndax seetluwuloo loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Bëgg rafet rekk mën na la dugal ci coono. Coono yooyu la téere bii di wax. Dafay wax itam ci taar bi ëpp solo. ” Jàngal 1 Pieer 3: 3, 4, te won ko foofu ne jikko ju rafet moo gën.

La Tour de Garde 1er janv.

“ Dañuy waxtaan ak ñi bokk ci diine yépp ngir laaj leen lu am solo. Li ëpp ci diine yi dañuy jàngale ne dañu war a bëgg suñu moroom. [Jàngal Macë 22:39.] Léegi kon, lu tax diine yi di bokk ci xeex yu bare ci àddina si tey ? [Mayal nit ki tontu.] La Tour de Garde bii dafay wax ci La religion peut-elle unir l’humanité ? ”

Réveillez-vous ! 8 janv.

“ Tey dañuy waxtaan ak nit ñépp ci lu am solo lool. Ci yow [Jàngal laaj bi nekk ci xët bu njëkk bi, ba pare mayal nit ki tontu ci.] Li suuf si am ngir dundal doom-Aadama yi, mu ngiy wàññiku rekk. Waaye, seetal li ñu Yàlla dig fii. [Jàngal Sabuur 104:​5, te won ko foofu ne suuf si dina fi nekk ba fàww.] Boo jàngee Réveillez-vous bii, dinga gis ne léegi ñu defaraat suuf si ba mu melaat ni mu meloon bu njëkk. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager