TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/02 p. 2-4
  • [Li ñu mën a wax ci waaraate bi]

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • [Li ñu mën a wax ci waaraate bi]
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Laaj bi
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Xam-xam bi
  • Waxal nit ki ne mën nañu koo jàngal Biibël bi
  • Naka lañuy jëfandikoo téere bu ndaw bu tudd Xebaar bu baax bi jóge ci Yàlla !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2013
  • Ndax yaa ngi jëfandikoo téere Laaj bi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Li ñu mën a wax ci waaraate bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 1/02 p. 2-4

[Li ñu mën a wax ci waaraate bi]

Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Laaj bi

“ Nit ñu bare gëm nañu Yàlla, du dëgg ? Képp ku gëm Yàlla, xam na ne am na li mu ñu laaj. Waaye lan la ñu Yàlla laaj ? Nit ñi bokkuñu xalaat ci loolu. ” Won ko téere Laaj bi. Ubbil njàngale bu njëkk bi te waxtaanleen ci.

“ Njaboot yi, bare nañu jafe-jafe tey. Ci sa xalaat, naka lañu mënee am jàmm ci suñu njaboot ? ” Bu la tontoo ba pare, wax ko ne Yàlla wone na ci Mbind mu sell mi, liy indi jàmm dëgg ci biir njaboot. Jàngal Isayi 48:​17, te ubbil téere Laaj bi ci njàngale 8. Won ko foofu ay aaya yuy wone ci lu wóor ni képp ku nekk ci njaboot bi war a dunde. Jàngal laaj yiy tàmbali njàngale bi, te laaj ko ndax bëgg na jàng tontu laaj yooyu.

“ Téere bii dafa ñuy jàngal lépp li nga xam ne waruñu koo ñàkk xam ci Mbind mu sell mi. Xët bu nekk, dina tontu laaj yu jaaxal nit ñi lu mat ay téemeeri at. Laaj yu mel ni : Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ? ” Ubbil njàngale 5, te jàngal laaj yu njëkk yi. Laajal ki ngay waxal ban moo ko gën a soxal, te jàngal xise fu ñuy tontoo laaj boobu. Jàngal it aaya yu ànd ak li ko soxal. Wax ko ne ni mu ame tont bu leer ci laaj bi ngeen doon seet, noonu la mënee gaaw a am tont yu leer ci yeneen laaj. Wax ko ne mën nga ñów beneen yoon, ngir waxtaan ak moom ci yeneen laaj.

“ Ci yow, lu tax xale yi di soxor ci seen biir ci lekkool yi, ba léeg-léeg ñuy gaañ seeni moroom, gaañ bu metti ? Ndax way-jur yi ñoo yaratul seeni doom ? Walla ndax Seytaane moo leen ci dugal ? ” Mayal nit ki mu tontu. Su la waxee ne Seytaane moo tax, jàngal Peeñu bi 12:​9, 12. Won ko li Seytaane di def ngir jaxase àddina si. Boo paree, ubbil téere Laaj bi ci njàngale 4, te laaj ko ndax mas na laaj boppam fan la Seytaane jóge. Jàngal ñaari xise yu njëkk yi te waxtaanleen ci. Waaye nit ki mën na wax ne, way-jur yi ñoo yaratul seeni doom. Looloo tax xeex ak yu mel noonu am ci lekkool yi. Bu waxee loolu, jàngal 2 Timote 3:​1-3 te won ko jikko yiy tax jafe-jafe boobu gën a yokku. Boo paree, ubbil téere Laaj bi ci njàngale 8, jàngal xise 5, te yaatalleen waxtaan bi.

“ Ndax mën nañu xalaat ne, ki ñu sàkk dina ñu may xam-xam bi ñu soxla ngir am jàmm ju bare ci suñu njaboot ? ” Bu la tontoo, won ko téere Laaj bi. Ubbil njàngale 8, te wax ko ne njàngale boobu dafay won képp ku bokk ci njaboot, ni mu war a dunde ngir topp li Biibël bi wax. Laaj ko ndax bëgg na nga won ko ni mu mënee jëfandikoo téere bi ak Biibël bi, ngir gën cee am njariñ.

“ Nit ñi, bare nañu jafe-jafe tey. Ndax foog nga ne ñaan Yàlla mën na ñu dimbali ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ñu bare danuy wax ne ñaan dafa leen di may doole ci seen biir xol. [Jàngal Filipp 4:​6, 7.] Waaye nit mën na wax ne ñaan na ba sonn, waaye gisul dara. [Ubbil téere Laaj bi ci njàngale 7.] Téere bii, dafay wone ban njariñ bu rey lañu mën a am ci suñuy ñaan. ”

“ Li ñuy laaj nit ñi tey mooy : lu tax diine yi bare ci àddina si, te fekk benn Mbind mu sell kese moo am ? Ci yow, lu waral loolu ? [Mayal nit ki mu tontu. Ubbil téere Laaj bi ci njàngale 13, jàngal laaj yiy tàmbali njàngale bi, te ne ko...] Boo jàngee njàngale bii, dinga am ay tont yu leer ci laaj yooyu. ”

Bu amee nit koo jox Réveillez-vous ! ak La Tour de Garde, laaj ko ndax mën nga koo jàngal xise bu gàtt. Bu nangoo, ubbil téere Laaj bi ci njàngale 5. Won ko laaj yiy tàmbali njàngale boobu, te wax ko mu déglu tontu laaj bu njëkk bi, ci xise bu njëkk bi ngay jàng. Boo jàngee xise bi, jàngaatal laaj bi te déglul ni mu koy tontoo. Wax ko ne su bëggee téere bi, mën na koo am. Su ko jëlee, wax ko ne su ko neexee, mën nga ñówaat ngir waxtaan ci ñaari laaj yiy topp.

Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Xam-xam bi

Jëlal Biibël bi ci sa loxo te waxal lii : “ Tey, dañuy wone aaya bii nit ñépp ci mbedd mi... ” Jàngal Yowanna 17:​3, te laaj ko : “ Ki am xam-xam bi war, ndax gis nga li ñu ko dig ? [May ko mu tontu.] Fan la nit mënee am xam-xam bu mel noonu ? ” Bu tontoo, won ko téere Xam-xam bi te wax ko lii : “ Am na ay laaj yu nit ñi gën a faral di laajte ci Mbind mu sell mi. Téere bii dafay tontu laaj yooyu. Tont yooyu ñooy joxe xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. ” Won ko Àlluwa ji (maanaam fi ñuy wone waxtaan yi nekk ci téere bi). Boo paree, laajal nit ki ndax ci waxtaan yooyu, am na bu mu ci mas a laaj boppam.

“ Ndax mas nga laaj sa bopp lii : Lu bon li am ci suuf si, walla samay coono, ndax soxal na Yàlla ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi dafay wone ne Yàlla dafa ñu bëgg, te bu ñu amee naqar, dina ñu dimbali. ” Jàngal ay aaya ci Sabuur 72:​12-17. Ubbil téere Xam-xam bi ci pàcc 8. Won ko ne dafay tontu laaj bu ay milioŋi nit di laaj, maanaam : Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi ? Tont bu muy joxe day dalal xel. Soo ko mënee, waxtaanal ak moom ci yenn xalaat yi nekk ci Mbind mu sell mi te ñu bind ko ci xise 3 ba 5. Soo ko mënul, def ko boo dellusee.

“ Li ëpp ci nit ñi, am nañu mbokk yu faatu. Ndax dinañu leen mën a gisaat ? Ndax mas nga ko laaj sa bopp ? [Mayal nit ki mu tontu.] Isaa wone na ne suñu mbokk yi faatu, mën nañu dekki. [Jàngal Yowanna 11:​11, 25, 44.] Dëgg la, yàgg na bi loolu amee, waaye dafay wone li ñu Yàlla dig. ” Ubbil téere Xam-xam bi ci nataal bi nekk ci xët 85, te jàngal li ñu bind ci kowam. Boo paree, won ko nataal bi nekk ci xët 86, te waxal loo fay gis. Ngir waajal sa dellusi, laaj ko lii : “ Ndax bëgg nga xam lu tax nit di màgget tey dee ? ” Delluwaat fa ngir waxtaan ak moom ci pàcc 6 bi.

“ Bu ñu sañoon, dinañu dund lu gën a yàgg li ñuy dund tey. Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax ñu bëgg loolu ? ” Bu la tontoo, ubbil téere Xam-xam bi ci pàcc 6 te jàngal xise 3. Waxtaanal ak moom ci aaya yi ci nekk. Jàngal ñaari laaj yi mujj ci xise bi, te laaj ko ndax bëgg na xam tont yi. Su dee waaw, waxtaanal ak moom ci xise yi ci topp.

“ Dañuy laaj nit ñi ndax gëm nañu lii... ” Jàngal 1 Musaa 1:​1, ba pare laaj ko lii : “ Ndax nangu nga li ñu bind fii ? ” Su nangoo, ne ko : “ Man itam nangu naa ko. Waaye ndax foog nga ne, ndegam Yàlla moo sàkk lépp, moom moo tax lu bon am ? ” Boo ko dégloo ba noppi, jàngal Dajalekat 7:29. Ubbil téere Xam-xam bi ci pàcc 8, te jàngal xise 2. Su nanguwul li nekk ci 1 Musaa 1:​1, wax ko mu seet ci téere bi nga koy won liy wone ne am na ku sàkk lépp. — Seetal téere Comment raisonner bi ci xët 72 ba 74.

“ Li nit ñi jàppe ni lu baax ak lu bon dafay gaaw a soppi. Ci sa xalaat, ndax soxlawuñu ku ñuy wax ci lu wóor ni ñu war a doxale suñu àddina ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi mooy téere bi gën a yàgg, waaye li mu wax am na njariñ ba tey jii. Te it soo ko toppee, dinga mën a am jàmm ci sa njaboot. ” Ubbil nag téere Xam-xam bi, ci pàcc 2 te jàngal xise 10 ak kàddu gi njëkk ci xise 11. Jàngal it 2 Timote 3:​16, 17.

“ Ndax bëgg nga xam lan mooy ëllëgu nit ñi ak ëllëgu suuf si ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi dafay wax ci lu gàtt, naka la ëllëg di mel : Àjjana lay doon ! Foofu la Yàlla dugaloon suñuy maam Aadama ak Awa bi mu leen sàkkee. Seetal nu mu meloon. ” Ubbil téere Xam-xam bi ci xët 8, te jàngal xise 9, fi ñu bind “ Dund ga woon ca Àjjana ”. Boo paree, waxtaanal ak moom ci li nekk ci xise 10, te jàngal Isayi 55:​10, 11. Wax ko ne su bëggee, mën ngeen waxtaan it ci ni dund gi nar a mel ci Àjjana biy amaat ci suuf si, ni ko xise 11 ba 16 di wone.

Waxal nit ki ne mën nañu koo jàngal Biibël bi

Boo bëggee jàngal nit Biibël bi, mën nga njëkk wax lii :

“ Ndax xam nga ne, mën nga am ci lu gaaw tont ci ay laaj yu am solo yu jëm ci Mbind mu sell mi ? Su ma la waxee, ... ” Laaj ko benn ci laaj yi ñu njëkk bind ci njàngale yi nekk ci téere Laaj bi. Na nekk laaj bu ko mën a soxal.

“ Dama la seetsi ngir won la ni ñuy jàngalee Mbind mu sell mi, te doo ci fey dara. Ndax mën nga ma may tuuti, 5 minit kese, ma won la ? ” Bu la ko mayee, jëlal téere Laaj bi ci njàngale 1, te won ko ni njàng mi di deme. Na ngeen jàng benn walla ñaari aaya kese. Bu ngeen paree, laaj ko lii : “ Kañ nga may mën a may lu mat 15 minit ndax ñu def njàngale bu ci topp ? ”

“ Nit ñu bare, yor nañu Mbind mu sell mi. Waaye xamuñu ne, dafay tontu laaj yu am solo yu jëm ci suñu ëllëg. [Won ko téere Laaj bi walla téere Xam-xam bi te ne ko...] Téere bii, bu ñu ci gëstoo lu mat benn waxtu ayu bés bu nekk, dinga xam lu am solo ci Mbind mu sell mi. Njàng moomu du yàgg sax. Soxlawul ay weer yu bare. Boo ma ko mayee, dinaa la won ni ñu koy defe. ”

“ Dama la seetsi ngir wax la ne mën nañu la jàngal Mbind mu sell mi, te doo ci fey dara. Ci lu mat 200 réew, nit ñi dañuy jàng Mbind mu sell mi, ci seen biir kër, ñoom ak seen njaboot. Boo ma ko mayee, dinaa la won naka lañu koy defe. Du yàgg sax. [Won ko Àlluwa ji, maanaam fi ñuy wonee waxtaan yi nekk ci téere Xam-xam bi.] Tànnal fii benn waxtaan. ” Ubbil téere bi, ci waxtaan bi mu tànn, te tàmbaleel njàng mi ci xise bu njëkk bi.

“ Damay jàngal nit ñi Mbind mu sell mi, te duñu ci fey dara. Fi ñu tollu nii, dama bëgg a yokk ñi may jàngal. Téere bii lañuy jëfandikoo. [Won ko téere Xam-xam bi.] Njàng mi yépp du yàgg sax. Soxlawul ay weer yu bare. Dina tontu ay laaj yu mel ni : Lu tax Yàlla di bàyyi metit wi ? Lu tax ñuy màgget tey dee ? Lan moy dal suñuy soppe yi dee ? Ak it ni nga mënee jege Yàlla. Ndax mën naa la won ni ñu koy defe ? ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager