TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/08 p. 3-6
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yégleleen ni Yexowa baaxe
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nañu wéy di wax ci lu kéemaane li Yexowa def
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Nañu góor-góorlu ci def lu baax !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 1/08 p. 3-6

‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’

1. Ban xibaar bu baax lañu war a yégal nit ñi ?

1 Tey, dégg xibaar bu neex jafe na lool. Waaye ñun dañuy “ seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla ” (Jëf. 20:24). Bu ñu koy def, dañuy xamal nit ñi ne “ muju jamano ” jii, léegi mu jeex, te Yexowa dina indi àddina bu bees te jub, fu “ jëf yu jëkk ya ” dinañu wéy (2 Tim. 3:1-5 ; Peeñ. 21:4). Ci jamono jooju feebar dootul am (Esa. 33:24). Suñu mbokk yi gaañu dinañu génn seen bàmmeel, gisaat seen waa kër ak seeni xarit (Ywna. 5:28, 29). Suuf si sépp, dinañu ko defaraat ba mu nekk àjjana ju rafet (Esa. 65:21-23). Loolu lépp, lu tuuti la ci li bokk ci xibaar bu baax bi ñu war a xamal nit ñi.

2. Jamono ndaje fàttaliku bi, lu tax mu nekk jamano ju baax ngir seedeel xibaar bu baax bi ?

2 Weeru màrs, awril ak me, weer yu baax la pur yégle xibaar bu baax boobu. Ci weer yooyu, ci réew yu bare ci àddina, taw bi, tàngoor bi walla yu mel noonu duñu sonal nit ñi. Bëccëg yi dañuy gën a gudd itam. Loolu lépp dina tax ñu mën a waaraate waxtu yu gën a bare. Raax ci dolli, xew bi gën a am solo ci at mi, maanaam ndaje fàttaliku bi, dimaas 22 màrs lañu koy def ci àddina si sépp, bu jant bi sowee. Kon, léegi lañu war a komaase di waaj ni ñuy fexee ba yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi.

3. Lan moo ñu mën a dimbali ñun ak suñu njaboot, ñu yokk li ñuy def ci waaraate bi ?

3 Nañu nekk pioñee buy jàpple : Ndax mënuleen a defar seen porogaraam ba mën a nekk pioñee buy jàpple benn, walla ñaar ci weer yooyu walla ñetti weer yépp ? Njàngum Biibël bi ngeen di def ak seen waa kër, bii di ñëw, bu jotee, ndax mënuleen ci waxtaan tuuti ? Bu ci ñépp defee seen wàll, xéyna kenn ci kër gi walla lu ko ëpp sax dina mën a nekk pioñee buy jàpple (Léeb. 15:22). Nangeen ko boole ci seeni ñaan, te seetleen ni Yexowa di barkeele li ngeen di def (Léeb. 16:3). Su dee sax amul kenn ci kër gi ku mën a nekk pioñee buy jàpple, waa kër gi yépp mën nañu jàpp li ñu bëgg def ngir yokk seen liggéeyu waare bi. Te dinañu ci góor-góorlu bu baax bu ñuy ànd ak ñi fexe ba nekk pioñee.

4. Bu ñuy yendu fi ñuy liggéeye, naka lañu mënee defar porogaraam ngir mën a nekk pioñee buy jàpple ?

4 Su dee dangeen di yendu fi ngeen di liggéeye, bu ngeen amee porogaraam bu baax, dingeen mën a nekk pioñee buy jàpple. Xéyna dingeen mën a jël tuuti ci waxtu bi ngeen war a añ, ngir waaraate ci. Walla mën nga ñaan ñu may la gox bu jege sa kër walla fi ngay liggéeye ngir waaraate fa. Dinga fa mën a waare benn waxtu bala ngay komaase liggéey walla boo wàccee. Mën ngeen seet itam lu amul solo lool ci li ngeen war a def te porogaraame ko ci beneen weer. Mën ngeen it fas yéene yendu ci waaraate bi samdi yi ak dimaas yi. Am na ñu ñaan fi ñuy liggéeye benn walla ñaari fan ci seen fan yi ñu war a noppalu, ngir waaraate.

5. Naka ngeen mënee dimbali ñi màgget, walla ñi feebar ngir ñu nekk pioñee yuy jàpple ?

5 Bu dee danga màgget walla nga feebar walla it nga nekk ku barewul doole, boo waaree tuuti bés bu nekk, xéyna dinga mën a nekk pioñee buy jàpple. Ñaanal Yexowa mu may la “ kàttan gu ëpp xel gi ” (2 Kor. 4:7). Suñu benn mbokk bu jigéen nekkoon na pioñee buy jàpple fekk 106 at la amoon. Mbokkam yi nekk karceen ak it ñeneen ñi nekk ci mbooloo mi dañu ko dimbali, ba mu mën a waare këroo kër, di dellu seeti nit ñi, di def ay njàngum Biibël, te di bokk ci yeneen fànnu liggéeyu waare bi. Amoon na wàll ci komaase fukki njàngum Biibël. Suñu mbokk moomu nee na : “ Su ma xalaatee ci cér bu réy boobu ma amoon maanaam nekk pioñee buy jàpple, sama xol dafay fees ak mbëggeel ci Yexowa, ci Doomam, ak ci Mbootaayam bi nga xam ne dafa ñu bëgg. Ci dëgg-dëgg lii laa bëgg wax : ‘ jërë jëf, Yexowa. ’ ”

6. Ndaw yi sóobu ba pare te ñuy dem lekkool, naka lañu mënee nekk pioñee buy jàpple ?

6 Bu dee ndaw bu ñu sóob nga te ngay dem lekkool, yow itam mën nga nekk pioñee buy jàpple. Booy defar porogaraam ngir waaraate, mel ni ñiy liggéey bés bu nekk, xéyna samdi ak dimaas ñooy nekk bés yi ngay gën a jariñoo. Xéyna it, yenn bés, boo wàccee lekkool, dinga mën a waaraate benn waxtu walla lu ko jege. Ndax dina am ay bés yoo dul jàng, fu nga mën a waare ? Boo bëggee nekk pioñee buy jàpple, nanga ci waxtaan ak say wayjur.

7. Lan la njiit yi mën a def ngir waa mbooloo mi yépp sawar ci waaraate bi ci jamono bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ?

7 Fexeleen ba waa mbooloo mi yépp sawar ci waaraate bi : Njiit yi, ci li ñuy def, mën nañu def lu bare ba waa mbooloo mi yépp sawar ci waaraate bi ci weer yooyu (1 Piy. 5:2, 3). Mën nañu yokk ndaje yi ñuy def ngir waare pur ñi bëgg waaraate suba teel, walla bu ñu wàccee lekkool, walla it bu ñu wàccee liggéey. Wottukatu liggéeyu waare bi, war na tànn waaraatekat bu mën jiite ngir mu jiite ndaje yooyu. Dina seet it ndax gox fi ñuy waaraate dina doy. Dina fexe it ba mu am yéenekaay ak ay téere yu doy ci mbooloo mi.

8. La lañuy jàng ci li benn mbooloo def ?

8 Ci benn mbooloo, njiit yi dañoo komaase di xiirtal nit ñi ngir ñu nekk ay pioñee yuy jàpple, ay weer bala muy jot. Ayu-bés bu nekk, dañu doon wax waa mbooloo mi ñaata nit lañu nangu ñu nekk pioñee yuy jàpple. Loolu dafa doon won ñi bëgg yokk li ñuy def ci waaraate bi ne dina am nit ñu bare ñuy mën a ànd ak ñoom ci waaraate bi. Yokk ci, dañu taxawal ci suba teel ak ci ngoon ay ndaje yu ñuy def bala ñuy dem waaraate. Mujj gi, 53 nit ñoo nekkoon pioñee yuy jàpple ci weeru awril. Loolu nekkoon na lu jege genn-wàllu mbooloo mi yépp !

9. Lu tax jamano fàttaliku bi baax lool ci ñi bëgg nekk waaraatekat ?

9 Nañu jàpple suñuy moroom ñu waaraate : Bu amee waaraatekat yu bees, xéyna dinañu leen wax ñu ànd ak waaraatekat yu yàgg ci liggéeyu waare bi. Dinañu mën a def loolu bu baax ci jamono fàttaliku bi, fi nga xam ne ñu bare ci mbooloo mi dinañu yokk li ñuy def ci waaraate bi. Ndax am na ci ñi ngay jàngal Biibël bi kuy góor góorlu ba méngale dundam ak yoonu Yexowa bu jub bi ? Ndax am nga doom yu yaru yuy jëm kanam bu baax ci wàllu ngëm, fekk nekkaguñu ay waaraatekat ? Su dee wone nañu ne bëgg nañu nekk ay waaraatekat yu ñu sóobagul, te yaakaar nga ne mat nañu ko, wax ko benn njiit ci mbooloo mi. Wottukat biy jiite dina yebal ñaari njiit ñu seetsi leen, yow ak sa doom walla ki ngay jàngal Biibël bi, ngir ngeen waxtaan ci loolu.

10. Lan la njiiti mbooloo mi mën a def ngir dimbali ñi bàyyi waaraate ?

10 Weer yii di ñów dinañu baax it ci ñi bàyyi waaraate ngir ñu komaasewaat ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi. Wottukati njàngum téere yi ñuy def ci mbooloo mi war nañu góor góorlu ngir seeti ñooñu te xiirtal kenn ku ci nekk ngir mu ànd ak ñoom ci waaraate bi. Bu dee yàgg nañu bàyyi waaraate, ñaari njiit ci mbooloo mi war nañu njëkk waxtaan ak ñoom ngir seet ndax mën nañu kontine nekk waaraatekat. — Sasu Nguuru Yàlla bu 11/00, xët 3.

11. Lan mooy gën a wone “ mbaaxaayu Yàlla bi kenn yelloowul ” ?

11 Waajalleen ndaje fàttaliku bi : Njot gi mooy gën a wone “ mbaaxaayu Yàlla bi kenn yelloowul ” (Acts 20:24, NW). Ci àddina si sépp, ay milyoŋi nit ñu fonk njot googu, dinañu teewe ndaje fàttaliku deewu Kirist, dimaas 22 màrs, bu jant bi sowee. Bëgg nañu woo boroom xol yu rafet yépp, te dimbali leen ngir ñu teewe ndaje bu am solo boobu di won mbaaxaay bi Yexowa won doom-Aadama yi fekk kenn yelloowu ko.

12. Ñan lañu mën a woo ci ndaje fàttaliku bi ?

12 Bindal ci benn kayit turu ñi nga bëgg a woo ci ndaje boobu. Wóor na ne dinga ci bind say mbokk, say xarit, say dëkkandoo, ñi nga bokkal liggéey walla lekkool, ñi doon jàng Biibël bi ak yow, ñiy kontine di jàng Biibël bi ak yow, akit ñeneen ñi nga faral di seeti ñépp. Bu ci amee ñu lay laaj ci lu jëm ci ndaje fàttaliku bi, xaaj bi tudd Le repas du Seigneur (maanaam reeru Sang bi) te nekk ci téere Qu’enseigne la Bible, xët 206 ba 208, mën na la ci dimbali. Loolu sax mën na tax nga komaase njàngum Biibël, ndaxte dangay won nit ki téere Qu’enseigne la Bible bi nga xam ne moom lañuy jëfandikoo ngir def njàngum Biibël.

13. Naka la Yexowa barkeele li ñaari waaraatekat def ndax li ñu bëggoon a woo seeni moroom ci ndaje fàttaliku bi ?

13 Suñu benn mbokk bu jigéen dafa bind ci kayit 48 waa kër yi mu bëggoon a woo ci ndaje fàttaliku bi. Saa yu ci woowee benn, dafa ko doon rëdd ba pare bind ci wetu tur bi bés bi mu ko ko waxee. Ci ñi mu woo 26 ñoo ñëw ci ndaje fàttaliku bi. Bi mu leen gisee dafa kontaan lool ! Suñu benn mbokk bu góor bu moom benn bitig, dafa woo kenn ci ñi ko doon liggéeyal ci ndaje boobu. Nit kooku làbbe la woon bu njëkk. Teewe na ndaje bi te lii la wax : “ Li ma jàng ci Biibël bi ci benn waxtu bi ma fa def, moo ëpp fuuf li ma jàng ci 30 at yi ma def ci jàngu katolik yi. ” Bi ndaje fàttaliku bi weesoo tuuti, nangu na ñu jàngal ko Biibël bi ci téere Qu’enseigne la Bible.

14. Ci bésu 1 màrs, ban liggéey bu am solo bu ñu war a def ci àddina si sépp lañuy komaase ?

14 Liggéey bu am solo bi ñu war a def : Diggante dimaas 1 màrs ba dimaas 22 màrs, dinañu joxe ay kayit ci àddina si sépp ngir woo nit ñi ñu teewe ndaje fàttaliku bi. Waaraatekat yépp dinañu bëgg bokk bu baax ci liggéey bu am solo boobu. Teg kayit boobu ci loxo nit ñi moo gën ñu koy bàyyi noonu ci buntu kër yi. Waaye nag, bu dee gox gi ñuy waare dafa réy lool, njiiti mbooloo mi mën nañu seet ndax mën nañu wax waaraatekat yi ne saa yu ñu fekkul kenn ci kër gi, mën nañu fa bàyyi kayit foo xam ne ñiy romb ci mbedd mi duñu ko mën a gis. Bésu samdi ak dimaas yi, dinañu wone itam yéenekaay yi génn ci weer wi.

15. Naka lañu mënee wone kayit yiy woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi ?

15 Komka amuñu jot bu bare ngir joxe kayit yooyu ngir woo nit ñi ci ndaje boobu, li gën mooy ñu gàttal li ñuy wax. Nanga laabiir te wone ne sawar nga ci li ngay def. Mën nga wax lu mel nii : “ Dañu bëggoon a def ba mu wóor ñu ne woo nañu la yow, sa waa kër ak say xarit ci xew bu am solo bi ñuy am ci bésu 22 màrs. Yaa moom kayit bii. Bind nañu ci kayit bi ay tegtal yu jëm ci xew boobu ”. Mën na am nit ki am li mu bëgg laaj. Walla mu nangu kayit bi te wax ne dina ñëw. Nangeen bind turu ñi wone ne itteel na leen te nangeen fexe ba dellu seeti leen.

16. Lan mooy wone ne liggéey bi ñuy def ci gox yi ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi am na solo lool ?

16 At mii weesu, benn soldaar dafa fekk ci buntu këram benn ci kayit yooyu. Mu daldi wax ne dina ci teew. Waaye dafa waroon a ñaan njiitam mu bàyyi ko mu teew ci. Bi mu wonee njiitam kayit bi, kooku dafa noppi ba mu yàgg, mu wax ko ne way-juram yi ay seedee Yexowa lañu te bu njëkk dafa doon ànd ak ñoom di teewe ndaje yi. Mu wax soldaar bi ne mën na dem. Waaye yemul ci loolu. Dafa ànd ak moom ci ndaje boobu !

17. Naka lañu def ngir wone ne nekkuñu ci luy neenal mbaaxaay bi ñu Yàlla won fekk yelloowuñu ko ?

17 Nañu wone ne fonk nañu li ñu Yàlla defal : Ni jamano ndaje fàttaliku bi di gën a jege, na kenn ku nekk ci ñun wone moom itam mbaaxaay bi ñu Yexowa di won, fekk kenn yelloowu ko. Ndaw li Pool bindoon na lii : “ nu ngi leen ñaan : jariñooleen yiw [maanaam mbaaxaay], wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu bañ a neen ci yéen ” (2 Kor. 6:1). Naka lañuy wone ne defuñu luy neenal mbaaxaay bi ñu Yàlla won ? Ndaw li Pool bindoon na itam lii : “ Li ñu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ” maanaam ñiy liggéeyal Yàlla (2 Kor. 6:4). Moo tax, bu ñu amee jikko ju rafet, te ñu sawar ci waaraate bi, dinañu wone ne fonk nañu bu baax li ñu Yexowa defal. Jamano fàttaliku bii dina nekk jamano ju baax ngir yokk liggéey bi ñuy def ci waare xibaar bu baax bi.

[Wërale bi nekk paas 3]

Ñan ñoo mën a bokk ci ñiy nekk pioñee buy jàpple ?

◼ Waa njaboot yi

◼ Ñiy liggéey

◼ Ñi màgget ak ñi feebar

◼ Ñiy dem lekkool

[Wërale bi nekk paas 4]

Booy joxe kayit yiy woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi :

◼ Waxal lu gàtt, te woneel ci sa wax ne danga sawar ci li ngay def

◼ Bindal ñiy wone ne itteel na leen te dellul seeti leen

◼ Woneel yéenekaay yi ci samdi yi ak dimaas yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager