Ay Tont Ci Seeni Laaj
◼ Bu ñuy dem Betel (Béthel), naka lañu war a soloo ?
Bu ñuy dem Betel ngir seet ni mu mel, walla ngir seeti kenn ku fa dëkk, ‘ dañu war a solu te jëfe mel ni bu ñuy dem ci ndaje yi ci Saalu Nguur gi ’. (om xët 131.) Waaye, am nañu ay mbokk ci wàllu ngëm, yu góor ak yu jigéen, yuy ñów Betel ak solu bu jekkul dara. Loolu baaxul. Ni ñuy soloo, lu jar a roy la war a doon ; dafa war a jekk te yiw, ni mu jekke ci jaamukatu Yexowa Yàlla. — 1 Tim. 2:9, 10.
Loolu dafa am solo lool, ndaxte nit ñu bare ñu nekkul seede, ñu ngi ñuy xool bu ñuy dem Betel. Li ñuy gis noonu, mën na tax ñuy xalaat lu baax walla lu bon ci mbootaayu Yàlla. Sol lu jekk te yiw bu ñuy dem Betel, am na solo lool. Bu amee ñuy jàng Biibël bi walla ñeneen ñu bëgg dem Betel, nangeen waxtaan ak ñoom ngir fàttali leen loolu. Dina baax lool, te ñi nekk Betel dinañu ci kontaan.
Ñun ñi nekk karceen, war nañu seet bu baax ni ñuy soloo, ndax ñu bañ a tax kenn fakkastalu ci wàllu ngëm (2 Kor. 6:3, 4). Saa su nekk, nañu fexe ba ni ñuy soloo ak li ñuy def, “ rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat ”. — Titt 2:10.