Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 déc.
“ Ci waxtu wi ñu tollu ci at mi, ñu bare dañuy xalaat ci bés bi Yeesu juddoo. Biibël bi wax na ci juddu Yeesu. Ndax xam nga ne am na lu am solo lu ñu ci mën a jàng ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare won ko xët 5 te jàngal 2 Timote 3:16.] La Tour de Garde bii, dafay wax ci yenn yu ñu ci mën a jàng. ”
Réveillez-vous ! 22 déc.
“ Ndax foog nga ne li fo yu ànd ak fitna di jur ci xale yi war na tiital way-jur yi ? [Mayal nit ki mu tontu.] Way-jur yu bare dañu seet ci Biibël bi li ñu war a def. [Jàngal Sabuur 11:5.] Réveillez-vous ! bii dafay won njaboot yi li bon li mën a nekk ci li ñuy woowe jeux vidéo. ”
La Tour de Garde 1er janv.
“ Bu nit ñi amee mbokk mu gaañu, walla bu feebar, dañuy tàmm di laajte : ‘ Lu tax Yàlla di seetaan lu mel nii ? ’ Xéyna mas nga laaj sa bopp lu mel noonu. Biibël bi dafay wone ne Yàlla yërëm na ñi am naqar, walla metit. [Jàngal Isayi 63:9.] Yéenekaay bii dafay wone lu tax mu mën ñu wóor ne Yàlla dina fi dindi metit. ”
Réveillez-vous ! 8 janv.
“ Ndax foog nga ne nguur yi war nañu mën a tere nit ñi ñu wax li leen neex ? [Mayal nit ki mu tontu.] Bu fekkee ne, ni ñu ko bindee fii, nit ki ci diine lay wax, loo ci xalaat ? [Jàngal Jëf ya 28:30, 31.] Lu yàggul, wax boobu àgg na ba ci àttekat yu gën a mag yi ci Etaa Sini. Mën nga jàng lu ci jëm ci Réveillez-vous ! bii. ”