War nañu màggal Yexowa bu baax
Ren, Reeru Sang bi, bésu 16 Awril lay doon
1 Ñu ngi séentu bésu 16 awril 2003. Ci guddi googu lañuy fàttaliku deewu Yeesu. Bés boobu, ñun ak suñu ay milyoŋi mbokk ci ngëm yi nekk ci àddina si sépp, dinañu màggal turu Yexowa. Ku xalaat ci njot gi ñu Yexowa may, xam ne war na ko màggal bu baax-a-baax. Njot googu mooy tax Yexowa di may ñi ko déggal ay barke yu am maanaa. Yëg nañu ñun itam ci suñu biir xol li Sabuur wax, maanaam : “ Yexowa ku màgg la, te war nañu ko màggal bu baax. ” — Sab. 145:3.
2 Yàlla ku baax la. Ci jamano fàttaliku bi, war nañu ci xalaat bu baax. Ameel nañu Yexowa ngërëm ndax li mu yónni “ ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom ”. (1 Ywna. 4:9, 10.) Loolu it, war nañu ci xalaat bu baax. Yeesu dafa ñu laaj ñu màggal Reeru Sang bi. Dina tax ñu gën a yëg ci suñu biir xol ne “ Yexowa dafa am yërmande ak [...] laabiir bu ànd ak mbëggeel ”. (Sab. 145:8.) Njot gi, mooy liy gën a wone ne Yexowa dafa bëgg doom-Aadama (Ywna. 3:16). Nañu xalaat ci mbëggeelu Yexowa. Nañu xalaat it ci ni Yeesu doon toppe lépp li yoonu Yexowa doon laaj. Dina tax ñu gën a bëgg a màggal Yexowa. Fii ba abadan, dinañu ko màggal ndax mbëggeel bi mu wone bi mu defee lépp li war ngir ñu mën a am dund gu dul jeex. — Sab. 145:1, 2.
3 Nañu dimbali nit ñi ñu màggal Yexowa : Njot gi ñu Yexowa may, lu réy la. Su ñu ko bëggee gërëm, dinañu woo nit ñi ndax ñu ànd ak ñun di ko màggal. Lii la Sabuur wax : “ Dinañu wax lu baree bare ci sa mbaaxaay. Te sa njubte dina tax ñu bég bay yuuxu. ” (Sab. 145:7). Daaw rekk, Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp, waaraate nañu lu ëpp benn milyaari waxtu. Seen liggéey boobu lu mu jur ? Bu ñu xoolee ñi sóobu daaw ci àddina si sépp, dafa mel ni, 5 100 nit ñoo sóobu ayu-bés bu nekk, ngir wone ne jébbal nañu seen bopp Yexowa. Ñi teewoon ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, matoon nañu 15 597 746. Ci nit ñooñu, lu ëpp 9 milyoŋ ñoo nekkul woon ay waaraatekat. Kon nag, Seede Yexowa yi mën nañu yokku bu baax-a-baax. Ñun ñii bokk ci ñiy waare Nguur gi, am nañu lu réy : mën nañu xamal nit ñi xibaar bu baax bi, te mën nañu leen a dimbali ba ñu bëgg Yexowa, Doomam, ak Nguur gi. Lu réy loolu, fonk nañu ko bu baax-a-baax.
4 Lenn li ñu mën a def ngir xiir nit ñi ci màggal Yexowa, mooy woo leen ci Reeru Sang bi. Ndax bind nga turu képp koo bëgg a woo ci ndaje fàttaliku bi ? Ndax bind nga it ñi soxla nga fàttali leen bésu fàttaliku bi ak waxtu bi ? Am na kayit yi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi. Ndax jox nga ci benn ñi nga bind ñépp ? Boo ko defagul, fexeel ba def ko ci fan yi des. Dimbalil ñi ngay woo ci ndaje fàttaliku bi ñu xam lu tax ñuy def ndaje boobu. Boo nekkee ci ndaje bi, teralal gan yi bu baax. Waxtaanal ak ñoom. Won leen yeneen Seede yi. Wax leen it ne kontaan nga lool ci li ñu ñów.
5 Nit ñi door a bëgg waxtaan ak ñun, bu ñu teewee ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, loolu mën na tax ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Am na ku doon jàng Biibël bi ak benn Seede Yexowa. Feebar bi mu amoon moo taxoon, dem ci béréb bu bare nit, lu jafe woon la ci moom. Waaye dafa ñów ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Bi ñu ko laajee li mu xalaat ci ndaje bi, dafa nee : “ Guddi googu, ci guddi yu gën a am solo yi la bokk, te fekke naa ko. ” Ginnaaw loolu, dafa tàmbali teew ci ndaje yi.
6 Bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo : Lu ñu mën a def ngir dimbali nit ñooñu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ndax ñu bokk ci ñiy màggal Yexowa ? Mag ñi dinañu leen seetlu. Ba pare, dinañu waxtaan ak ay waarekat yu aay, ngir ñu gaaw a dem seeti leen. Bu ko defee, dinañu mën a waxtaan ak ñoom ci li ñu jàng, ak li ñu gis ci ndaje fàttaliku bi te mu neex leen. Xéyna dina ci am ñu bëgg ñu defal leen njàngum Biibël seen kër. Ndaje yi ñuy def ayu-bés bu nekk mën nañu yokk seen xam-xam ci Biibël bi. Kon nañu leen wax it ñu ñów teew ci ndaje yooyu.
7 Am na ay Seede ñu dul waaraate weer wu nekk. Am na it ñu bàyyi waaraate. Fi mu nekk nii, ñu ngi jéem a waxtaan ak Seede yooyu yépp ndax ñu ñów teew ci ndaje yi yépp. Bu la mag ñaanee nga dimbali kenn ku bàyyi waaraate, nanga nangu. Boo defee loolu, dinga wone ne sa mbokk yi itteel nañu la, te danga leen bëgg. Ci ngay topp li Pool wax, maanaam : “ Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawati-na nag sunu mbokk yi gëm. ” — Gal. 6:10.
8 Nañu fexe ba ci bésu 16 awril, ñu teew ñun ñépp ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Ndaje boobu, mooy ndaje biy gën a màggal Yexowa. Na ci ñépp teew. Waaw, fii ba abadan, nañu màggal Yexowa ci yëf yu doy kéemaan yi mu def. — Sab. 145:21.