Nañu wax ak nit ñi lu jëm ci “ leeru àddina si ”
1 Yexowa dafa jaar ci yonent Yàlla Esayi ngir yégle lii : “ Xeet wi doon wéy ci lëndëm, gis nañu leer gu mag; ñi dëkkoon ci réew, mi dee njàtt [maanaam fu lëndëm lool], leer fenkal na leen [maanaam ñëw na seen kow]. ” (Esa. 9:1). “ Leer gu mag ” googu, feeñ na ci li Yeesu Kirist, doomu Yàlla bi def. Li mu def bi mu nekkee ci kow suuf ak barke yi saraxam indi, tax na ba ñi nekkoon ci lëndëm ci wàllu ngëm, am ngëm bu gën a dëgër. Leer bu mel noonu la nit ñi soxla tey, ndaxte ñu ngi ci lëndëm. Reeru Sang bi dina tax ñu mën leen a won “ leeru àddina si ”. (Ywna. 8:12.) Daaw, ay milioŋi nit wone nañu ngëm bi ñu am bi ñu ñëwee teew ak ñun ngir topp li Yeesu santoon bi mu nee : “ Defleen lii ngir fàttaliku ma. ” (Luug 22:19). Ndegam léegi ndaje fàttaliku bi jot, naka lañu mënee bokk ci ñiy xamal nit ñi leer gu mag gi Yexowa feeñal ? — Fil. 2:15.
2 Nañu fonk bu baax sarax boobu : Bi Yexowa ak Yeesu joxee sarax bi nekk njot gi, dañu wone ne dañu bëgg doom-Aadama yi. Ci jamano fàttaliku bi, dinañu mën a xalaat bu baax ci mbëggeel boobu (Ywna. 3:16 ; 2 Kor. 5:14, 15). Loolu dina yokk suñu ngërëm ci xew bu sell boobu. Ñi bokk ci mbooloo Yexowa yépp dinañu nangu jël jot bu doy ngir jàng te xalaat ci aaya yi ñu war a jàng ngir ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Aaya yooyu ñu ngi ci téere bi tudd Examinons les Écritures chaque jour. Bu ñu xalaatee ci jikko yu rafet lool yi Yexowa yore, dinañu gën a kontaan ndax li mu nekk suñu Yàlla. Jikkoom yooyu feeñ nañu ci njot gi ñu joxe. Kenn ku nekk ci ñun am na li ko sarax boobu di indil. Bu ñu ci xalaatee, dinañu gën a bëgg Yàlla ak Doomam. Dina tax it ñu gën a góor-góorlu ngir def coobare Yàlla. — Gal. 2:20.
3 Nañu fexe ba yokk suñu ngërëm ci li Yexowa def ngir ñu mën a mucc. Kon dinañu yàkkamti ndaje fàttaliku deewu Yeesu bi te loolu dina wàll nit ñi ñuy woo ci ndaje boobu, maanaam ñiy jàng Biibël bi, ñi nuy dellu seeti, suñu mbokk yi, suñu dëkkandoo yi, suñu waa kalaas yi, ñi ñu bokkal liggéey ak ñeneen (Luug 6:45). Kon nag, nañu góor-góorlu bu baax ngir woo ñooñu ñépp ci ndaje fàttaliku bi. Nañu leen jox it kayit yi ñu defar ngir ndaje boobu ngir ñu bañ ko fàtte. Am na ñuy bind turu nit ñi nu bëgg woo, su ko defee duñu fàtte kenn. At mu nekk dañuy génnewaat kayit boobu, te yokk ci turu nit ñu bees ñi ñu bëgg woo ci ndaje boobu. Fexeel ba woo ñi suñu waxtaan neex ci ndaje fàttaliku bi. Loolu nekk na fasoŋ bu rafet bu ñu mën a won Yexowa Yàlla ne dañu koy gërëm ci “ may googu weesu dayo ” bi mu def. — 2 Kor. 9:15.
4 Nañu yokk li ñuy def ci waaraate bi : Ndax loolu mën nga ko def ci weeru màrs ak awril ? Ci lu wóor, Yexowa dina barkeel li ñuy def ngir xamal nit ñi “ xebaar bu baax, biy wone ndamu Kirist ”. Ci Yexowa la bépp leer ci wàllu ngëm jóge, moo tax mu sant lii : “ Na leer leer ci biir lëndëm. ” (2 Kor. 4:4-6). Bu ñu ko soxlaa, njiit yi dinañu jàpp yeneen waxtu ak yeneen béréb fu ñuy ame ay ndaje yi ñuy def balaa ñuy dem waare.Te dinañu jàpple waaraatekat yi bëgg waare lu gën a yàgg. Mën na nekk ñi bëgg waare suba teel ci mbedd yi, walla ngoon ci béréb yu bare bitig ak ci telefon. Boo bëggee yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi, mën nga jàpp ñaata waxtu nga bëgg waare te góor-góorlu ngir def li nga jàpp noonu. Nanga jàpp loo xam ne du diis lool ci yow. Am na ñu bare ñu gis ne nekk pioñee buy jàpple bokk na ci li gën li ñu mën a may Yexowa. — Kol. 3:23, 24.
5 Ndax mën nga nekk pioñee buy jàpple ? Bi ñu wàññee waxtu yi pioñee buy jàpple war a def ci waaraate bi, ëpp na léegi juróom-ñaari at. Loolu tax na nit ñu gën a bare mën a nekk pioñee buy jàpple, ba gis barke yi ci nekk. Ndax mas nga ko jéem ? Am na ñu ko faral a nekk, at mu nekk. Ci mbooloo yu bare, ay waaraatekat yu bare dañuy ànd nekk pioñee buy jàpple. Li ñuy def noonu dina bokk ci liggéey bi gën a baax bi waa mbooloo mi def ci at mi yépp. Te it dina bokk ci li leen di gën a jariñ. Ndax mën nga jàpp benn weer ci jamano fàttaliku bi, ngir nekk pioñee buy jàpple ba gis ni mu neexe ? Weeru awril mën na baax lool ndaxte dina am juróomi Samdi ak juróomi dimaas.
6 Ndax wottukat biy wër ci mbooloo yi dafa war a ñëw ci seen mbooloo ci weeru màrs walla awril ? Mën nga ci am beneen barke. Yégle woon nañu ne, ci atum liggéeyu waare bu 2006, ñi nekk pioñee buy jàpple dinañu mën a teewe xaaj bi njëkk ci ndaje bu wottukat biy wër ci mbooloo yi di def ak pioñee yi. Wóor na ne lu yokk doole li ñu fay wax dina tax ba pioñee yuy jàpple yu bare bëgg góor-góorlu ngir nekk pioñee yu ci sax. Te it, ci weeru màrs dinañu mën a jariñoo téere bu bees bi tudd Qu’enseigne réellement la Bible ? ngir dimbali nit ñi, ñu ñëw fi am leer ci wàllu ngëm. Ndax bëggoo góor-góorlu ngir komaase benn njàngum Biibël ci téere bu bees boobu ?
7 Nanga xalaat ci 50 waxtu yi pioñee yiy jàpple war a def. Te nanga seet ban porogaraam nga war a topp ngir mën a leeral leeru dëgg gi lu jege 12 waxtu ayu-bés bu nekk. Nanga ci waxtaan ak ñi ko mas a def ak it ñeneen ñi. Loolu mën na leen xiir ci nekk pioñee buy jàpple ñoom itam. Am na ay waaraatekat yi ñu sóob, ay mag ak ay ndaw yépp, yu def lu rafet loolu. Te ñooñu dañu gis ne nekk pioñee buy jàpple jafewul ci ku tëral porogaraam bu baax. Nanga ci ñaan Yàlla. Te bu mënee nekk, nanga jàpp loo war a def ngir nekk pioñee buy jàpple, ba pare nga nekk ko ! — Mal. 3:10.
8 Ay njaboot yu bare dañu gis ne lu mu tuuti tuuti, kenn ci ñoom dina mën a nekk pioñee buy jàpple, bu ko ñépp jàpplee. Am na njaboot goo xam ne, juróomi nit ñoo ci sóobu woon ba pare. Njaboot googu fasoon na yéene góor-góorlu ngir juróom nit ñooñu nekk pioñee yuy jàpple. Yeneen ñaari xale yu ñu sóobagul woon, ñoom itam, dañu yokk li ñu doon def ci liggéeyu waare bi. Lan la njaboot googu jële ci li mu def noonu ? Nee nañu : “ Weer woowu, neexoon na lool. Gis nañu ne dañu gën a nekk benn. Ñu ngi gërëm Yexowa bu baax ci barke bu mag boobu ! ”
9 Li ñu bëgg yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs ak awril, ndax dina xiir ñu bare ci yokk li ñuy def ci liggéey boobu, ba tax ñu gën a jege suñu Baay bi nekk ci asamaan ? Loolu lan moo ko mën a indi ? Kenn ku nekk dafa war a yokk mbëggeel bi mu am ci Yàlla ak doomam, yokk it li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Kon ñun ñépp nañu bëgg def li ñu bind fii : “ Dinaa màggal bu baax Yexowa ak sama gémmiñ. Ci diggu mbooloo bu bare sax dinaa ko màggal. ” (Sab. 109:30). Yexowa dina barkeel bu baax li ñuy def ci liggéeyam ci jamano fàttaliku bii di ñëw. Kon nañu fexe ba leer gi leer bu baax, bu ko defee ñu gën a bare dinañu mën a jóge ci lëndëm gi, te “ am leeru dund ”. — Ywna. 8:12.
[Laaj yi]
1. Ban leer gu mag lañu yégle woon ci Kàddu Yàlla, te ban xew moo mën a won nit ñi leer googu ?
2. Lu ñu mën a def ngir gën a fonk njot gi ? Te loolu lan lay indi ?
3. Naka lañu mën a wonee ne dañu fonk ndaje fàttaliku bi ?
4. Lu ñu mën dimbali ñu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs ak awril ?
5. Li ñu wàññi waxtu yu pioñee buy jàpple war a def ci waaraate bi, naka la dimbalee ñu bare ?
6. Lan lañu taxawal te mu nekk lu neex lool ?
7, 8. a) Lan moo ñu mën a dimbali ci def porogaraam bu baax ngir nekk pioñee buy jàpple ? b) Naka la waa kër yi mënee jàppleente ci loolu ? Te ban njariñ la ci njaboot bi yépp di jële ?
9. Naka lañu mënee fexe ba suñu leer, leer ci jamano fàttaliku bii di ñëw ?