TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/04 p. 3-5
  • Nañu wéy di wax ci lu kéemaane li Yexowa def

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu wéy di wax ci lu kéemaane li Yexowa def
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Yégleleen ni Yexowa baaxe
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Lu rafet te jar a def ci atum liggéeyu waare biy komaase
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 2/04 p. 3-5

Nañu wéy di wax ci lu kéemaane li Yexowa def

1 Yexowa suñu Yàlla ju mag ji, kenn mënul a tollale ak moom ! Dawuda nee na : “ Def nga lu bare, céy Yexowa, sama Yàlla. Ci lu kéemaane li nga def sax ak ci li ngay xalaat ci ñun, kenn mënul a tollale ak yow. ” (Sab. 40:⁠5). Kéemaanu Yexowa yi ëmb nañu sax àddina si mu sàkk, Nguuru Almasi bi, laabiir bu ànd ak mbëggeel bi muy won mbooloom, ak it waaraate bi ñuy def ci àddina si sépp (Sab. 17:​7, 8 ; 139:14 ; Dañ. 2:​44 ; Macë 24:14). Bu ñu bëggee Yexowa te bu ñu amee ngërëm ci lépp li mu def, dina ñu xiir ci wax nit lu jëm ci moom (Sab. 145:​5-7). Loolu dinañu ko gën a mën a def ci weeru màrs, awril ak me.

2 Pioñee buy jàpple : Ndax mën nga fexe ba waaraate lu mat 50 waxtu ci weer yooyu ? Wóor na ne dina laaj nga soppi li nga tàmmoon a def (Efes 5:​16). Ñu bare gis nañu ne nekk pioñee buy jàpple tax na ñu gën a aay ci waaraate bi. Bu ñuy waar nit, duñu rus te duñu ragal na bu njëkk te dañuy gën a mën a jëfandikoo Biibël bi. Bu ñu yokkee waxtu yi ñuy waaraate, dañuy gën a mën a dellu seeti ñi suñu waxtaan neex. Am na ñoo xam ne masuñu woon a am njàngum Biibël bi, waaye bi ñu nekkee pioñee buy jàpple tàmbali nañu ci benn. Nekk pioñee buy jàpple, dafay laaj ñu góor-góorlu ngir jàpple nit ñi. Looloo tax mu nekk liggéey buy indi mbégte. — Jëf. 20:⁠35.

3 Bul gaaw a wax ne mënuloo nekk pioñee buy jàpple. Daaw, am na benn magu mbooloo bu nekkoon pioñee buy jàpple fekk mu am ñaari doom te muy liggéey. Suñu mbokk moomu nga xam ne dafa jàpp lool, lu mu def ba mën loolu ? Ndegam dafa doon liggéey altine ba àjjuma, samdi ak dimaas la doon gën a waaraate. Samdi yi, 7 waxtu ci suba la doon tàmbali waaraate ci mbedd mi. Ci mbooloo moomu, bare woon na ñu mel ni moom ñu nekkoon pioñee ñoom itam. Dañu doon jàppleente, ku nekk di yokk doole moroomam. Ci beneen mbooloo, suñu benn mbokk mu jigéen mu amoon 99 at nekk na pioñee bi ko doomam bu jigéen waxee ñu nekkandoo pioñee ci weeru me. Ngir mën a waaraate ak moom këroo-kër te def it ay njàngum Biibël, waa mbooloo mi dañu doon puus fauteuil roulant bi mu nekkoon. Dafa doon waaraate itam ci telefon, ci mbedd yi te di bind ay leetar. Nee na du ci kàttanam la defe loolu. Bu dul woon Yexowa mi ko jàpple, du mën loolu. — Isa. 40:​29-​31.

4 Jéemal bind porogaraam bi gën ci yow. Porogaraam yi ñu bind ci xët 4 mën nañu la ci dimbali. Ndax dangay liggéey bés bu nekk walla dangay jàng lekkool ? Xéyna defar porogaraam booy gën a waaraate samdi ak dimaas mooy gën ci yow. Bu fekkee ne sa wér-gi-yaram demewul noonu, ba tax doo mën a waaraate lu yàgg ci benn fan, xéyna porogaraam booy waaraate tuuti bés bu ne mooy gën ci yow. Waxtaanal ak ñeneen ci li nga bëgg nekk pioñee buy jàpple. Xéyna ñoom itam dinañu bëgg nekk ay pioñee.

5 Ni ci gune yi mënee bokk : Bu gune yi dee wax ci kéemaan yi mu def, Yexowa dafay bég (Sab. 71:17 ; Macë 21:16). Boo dee gune bu ñu sóob, xéyna dinga nekk pioñee buy jàpple ci weer bu am jamano booy noppalu. Boo mënulee nekk pioñee buy jàpple ci weer yooyu, ndax mën nga jàpp li nga bëgg def ci waaraate bi ngir mën ci yokk sa liggéey, walla jéem ci gën a aay ? Bu dee dangay ànd ak say wayjur ci liggéeyu waare bi te nekkagoo waaraatekat bu ñu sóobagul, mën nga ko jéem a nekk léegi. Bul foog ne danga war a njëkk nekk ku aay ci jëfandikoo Biibël bi ngir tontu laaj yi nit ñi di laaj walla danga war a xam lépp li mag yi ñu sóob xam ba pare. Ndax xam nga li ñu mënul a ñàkk xam ci Biibël bi ? Ndax yaa ngi topp li Biibël bi wax ci wàllu jikko ? Ndax bëgg nga nit ñi wax ne Seede Yexowa nga ? Kon waxtaan ci ak say waajur. Dinañu dem ak yow ci magi mbooloo yi ngir seet ndax mën nga nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. — Seetal téere Notre ministère xët 98-100.

6 Dimbalil nit ñi ngir ñu waaraate : Ci ñiy jàng ak ñun Biibël bi te di jëm kanam, xéyna dina am ñuy mën a nekk waaraatekat ci weer yooyu ñuy yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Boo amee koy jàngal Biibël bi te mu ngi jëm kanam bu baax ci wàllu ngëm, ñaanal sa wottukatu njàngum téere bi walla wottukatu liggéeyu waare bi ngir mu jàpple la. Kenn ci ñoom mën na ànd ak yow boo koy jàngal Biibël bi, ngir seet fu nit kooku tollu ci wàllu ngëm. Bu matee waaraatekat bu ñu sóobagul te mu bëgg ko nekk, wottukat biy jiite dina fexe ba yow ak ki ngay jàngal mën a daje ak ñaari magi mbooloo mi. (Seetal La Tour de Garde bu 15 nowàmbar 1988, xët 17.) Su mag yi waxee ne mën na komaase waaraate, nanga ko komaase won ni ñuy waaraatee ci saa si.

7 Wottukati njàngum téere bi war nañu toppatoo bu baax képp ku bokk ci seen gurup te bàyyi waaraate walla koo xam ne du weer yépp lay waaraate. Nañu leen wax ñu ànd ak ñoom ci liggéeyu waare bi. Su dee yàgg nañu bàyyi waaraate bi, li gën mooy ñaari magi mbooloo mi njëkk waxtaan ak moom ngir seet ndax mat na waaraatekat ba léegi. (Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu nowàmbar 2000.) Bu ñu gisee ni mbooloo mi saware ci waaraate bi ci weer yooyu, xéyna dina tax ñu bëgg bokkaat ci waaraate bi weer wu nekk.

8 Waajal sa bopp léegi ngir yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi : Yéen, magi mbooloo mi, léegi ngeen war a def liy tax waa mbooloo mi sawar a nekk pioñee yuy jàpple. Lu baax li ngeen di ci wax ak li ngeen di def mën na def lu bare (1 Pie. 5:⁠3). Weer bi pioñee yuy jàpple gënoon a bare ci mbooloo mi, ñaata lañu woon ? Ndax mën ngeen ko raw ren ? Wottukati njàngum téere bi ak ñi leen ci jàpple war nañu seet li ñu mën a def ngir wax ak képp ku bokk ci seen gurup ngir ñu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Wottukatu liggéeyu waare bi war na yokk ndaje yi ñuy am bala ñuy waare. Waxal waa mbooloo mi lépp li ñu tëral. Tànnleen ay waaraatekat yu nar a mën jiite bu baax ndaje yooyu, ngir ndaje yooyu bañ a tàrde te bañ a yàgg ba mu ëpp. (Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu septaambar 2001.) Wottukatu liggéeyu waare bi war na fexe it ba gox yi ñu war a waaraate, yéenekaay yi ak téere yi doy.

9 Daaw, magi benn mbooloo dañu teel xiir seen waa mbooloo ci nekk pioñee buy jàpple, te am na ci sax ñu bind kayit ngir nekk pioñee te joxe ko. Dañu yokk it ndaje yi ñuy am bala ñuy waare. Dañu def benn ndaje ci 5 h 30 ngir dem waaraate ci mbedd yi, beneen ci 15 h ngir ñi wàcc lekkool ak it beneen ci 18 h ngir ñi wàcc liggéey. Ci samdi yi, ñu def it ñetti ndaje yu ñuy am bala ñuy waare. Ci mbooloo moomu, 66 waaraatekat ñoo mujj nekk pioñee yuy jàpple ci weeru awril !

10 Bu ngeen di defati njàngum Biibël bi ngeen di def ci seen njaboot, ndax mënuleen jàpp li ngeen mën a def ci waaraate bi ci weer yooyu di ñëw ? Nangeen jàpp lu ngeen àttan. Bu ngeen jàppleentee te bu ngeen ko waajalee bu baax, dina am ci seen njaboot ñu mën a nekk pioñee buy jàpple walla sax seen njaboot yépp dina ko mën a nekk. Su ngeen mënulee nekk pioñee, seetleen ni ngeen mënee yokk waxtu yi ngeen tàmmoon a def ci liggéeyu waare bi, walla ngeen dem waaraate bés bu ngeen tàmmul woon a waaraate. Na ngeen ci ñaan Yàlla bu njaboot bi yépp toogee. Na leen wóor ne Yexowa dina barkeel li ngeen di def. — 1 Ywna. 3:​22.

11 Kéemaanu Yàlla bi gën a rafet : Liy gën a wone mbëggeelu Yexowa mooy li mu ñu feyal njot gi ak deretu Doomam (1 Ywna. 4:​9, 10). Peyug njot gi moo génne doom-Aadama yi ci bàkkaar ak dee ci kow li yoon tëral (Room 3:​23, 24). Deretu Yeesu moo tax kóllëre bu bees bi am, ba Yàlla mën a jàpp ay nit ñu matul ni ay doomam ngir ñu mën a am yaakaaru bokk ci Nguuru Yàlla ca asamaan (Yér. 31:​31-​34 ; Mark 14:24). Waaye li ëpp solo mooy, li Yeesu déggal Yexowa ci lépp sellal na turu Yexowa (5 Mu. 32:4 ; Léeb. 27:11). Dimaas 4 awril, bu jant bi sowee, dinañu fàttaliku ci àddina si sépp deewu Yeesu.

12 Màggal reeru Sang bi dafay màggal it kéemaani Yexowa. Waxtaan bi ñu fay am, dina tax ñu gën a gërëm Yexowa ndax li mu joxe njot gi. Ñi ñëw teewe ak ñun dinañu gis it yeneen kéemaani Yàlla. Dinañu gis ni mbootaayu Yàlla nekkee benn te bëggante ci seen biir, ni leen ko Yexowa jàngale (Efes 4:​16, 22-​24 ; Saak 3:​17, 18). Li ñu fay dégg, mën na soppi lu bare ci xelu ñi fay teewe. Kon li ñu bëgg mooy ñi ko mën ñépp teewe fa. — 2 Kor. 5:​14, 15.

13 Waxal nit ñi ñu ñëw teewe ko : Bindal léegi turu képp ki nga bëgg woo ci ndaje boobu. Boole ci say mbokk yu gëmul Yexowa, say dëkkandoo, ñi nga bokkal liggéey walla lekkool, ñi nga doon jàngal Biibël bi, ñi nga koy jàngal ba léegi ak ñi ngay dellu seeti ñépp. Wottukati njàngum téere bi war nañu boole ci seen kayit waaraatekat yi bàyyi waaraate.

14 Nanga jëfandikoo kayit yi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi te bind ci waxtu ak béréb fu ñuy defe ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Mën nga jëfandikoo it li nekk ci pàcc bu mujj bi ci La Tour de Garde bu 15 màrs 2004, walla Réveillez-vous ! bu 22 màrs 2004. Bu 4 awril di jegesi, telefoneel walla nga dem seeti ñi nga woo ci ndaje boobu ngir fàttali leen bés bi ñu koy defe.

15 Ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Ngoon googu, jéemal a teel a agsi. Nanga nuyu bu baax ñi sog a ñëw teewe ngir teral leen bu baax. (Room. 12:13). Yow yaa war a toppatoo ñi nga woo ci ndaje bi. Nanga leen teral bu baax te won leen suñu yeneen mbokk yi. Xéyna dinga mën a toog ci seen wet. Te bu ci amee ku amul Biibël walla téere woy-Yàlla, fexeel ba mu mën a xool ci sa bos walla ci bosu keneen. Bu ndaje bi jeexee nanga pare ngir mën a tontu ci lépp li ñu bëgg laajte. Bu ci amee ñu sog a teewe suñu ndaje, laaj leen ndax bëgguñu yokk li ñu xam ci Kàddu Yàlla ak ci li mu bëgg def. Laaj leen ndax bëgguñu jàng Biibël bi ak yow.

16 Wéyal di dimbali ñi teewoon ci ndaje boobu : Ci ayu-bés yi topp ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, xéyna ñi teewoon dinañu soxla ndimbal. Ñi nga xam ne bu njëkk dañu tàmmoon a teewe ci ndaje yi, waaye léegi dañu wàññi ni ñu ciy teewe. Magi mbooloo mi war nañu seet bu baax ndax fàttewuñu nit ñooñu. Dinañu jéem a xam it lu tax jëmatuñu kanam ci wàllu ngëm. Dinañu leen won bu baax ne jamano jii léegi mu jeex (1 Pie. 4:⁠7). Nangeen dimbali ñépp ndax ñu gis njariñ bi nekk ci topp li Mbind mi wax, maanaam ñu faral di teewe ndaje yi ak mbooloo Yàlla mi. — Yaw. 10:​24, 25.

17 Kéemaanu Yexowa yi dañu réy ba nga xam ne, bu ñu amee sax dund gu dul jeex, kenn du mën a xam lépp lu ci jëm (Ay. 42:​2, 3 ; Daj. 3:​11). Moo tax li mën a tax ñu koy màggal du ñàkk mukk. Ci jamano fàttaliku deewu Yeesu bii di ñów, bu ñu góor-góorloo ngir yokk li ñuy def ci waaraate bi, dinañu wone ne dañuy gërëm Yexowa ndax kéemaan yi mu def.

[Laaj yi]

1. Ci kéemaan yi Yexowa def, yan nga ci gën a fonk ?

2. Ku nekk pioñee buy jàpple, loolu naka la koy jariñe moom ci boppam ?

3. Naka la ñenn ñi def ba jafe-jafe yi ñu am, bañ leen a tere nekk pioñee buy jàpple ?

4. Bu ñuy defar porogaraam ngir nekk pioñee, ci lan lañu war a seet ?

5. Gune yi, lan lañu mën a jéem a def ci weeru màrs, awril ak me ?

6. Naka la ñu mënee dimbali ki ñuy jàngal Biibël bi ngir mu nekk waaraatekatu xibaar bu baax ?

7. Naka lañu mënee dimbali ku bàyyi waaraate walla ku ci dul bokk weer wu nekk ?

8, 9. Lan la magi mbooloo mi mën a def ngir waa mbooloo mi sawar a yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs, awril ak me ?

10. Naka la njaboot yi mënee waajal li ñu mën a def ngir yokk seen liggéeyu waare bi ?

11. a) Saraxu Yeesu bi, yan kéemaan la jur ? b) Kañ ak fan la suñu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu di am ci suñu gox ?

12. Teewe Reeru Sang bi naka la mënee jariñ ñi suñu waxtaan neex ?

13, 14. Kan lañu war a woo ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ? Naka lañu ko mënee def ?

15. Ci ngoonu fàttaliku gi, naka lañu mënee teral bu baax nit ñi ?

16. Lan lañu mën a def ngir ñi teewoon mën a jëm kanam ci wàllu ngëm ?

17. Lu tax ñu war a wéy di wax ci kéemaan yi Yexowa def ?

[Tablo bi nekk paas 4]

Ndax mën nga topp benn ci porogaraam yii di topp te nekk pioñee buy jàpple ?

Màrs Dim Alt* Tal* Àll* Alx Àjj Sam Weer Lépp

Bés bu nekk 2 1 1 1 1 1 5 51

Ñaari bés 0 5 0 5 0 0 0 50

Samdi ak Dimaas 5 0 0 0 0 0 8 52

Samdi, Dimaas

ak ñaari bés 2 0 0 2 0 2 6 50

Awril Dim Alt Tal Àll Alx* Àjj* Sam Weer Lépp

Bés bu nekk 2 1 1 1 1 1 5 50

Ñaari bés 0 0 0 0 5 5 0 50

Samdi ak Dimaas 5 0 0 0 0 0 8 52

Samdi, Dimaas

ak ñaari bés 2 0 0 2 0 2 6 50

Me Dim* Alt* Tal Àll Alx Àjj Sam* Weer Lépp

Bés bu nekk 2 1 1 1 1 1 4 51

Ñaari bés 0 5 0 0 0 0 5 50

Samdi ak Dimaas 3 0 0 0 0 0 7 50

Samdi, Dimaas

ak ñaari bés 2 0 0 2 0 2 5 51

* Dinañu mat juróom ci weer wi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager