Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mars
“ Ndax foog nga ne mën nañu topp ba léegi li Yeesu jàngale ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xam naa ne dinga ànd ak li Yeesu wax bés bi mu waroon a dee. [Jàngal Yowanna 15:12.] Bés boobu, Yeesu wax na it leneen lu am solo. Yéenekaay bii dafay wone ni ñu ko mënee jariñoo. ”
Réveillez-vous ! 22 mars
“ Coono àddina si tey dañu bare ba tere nelaw nit ñu bare. [Mayal nit ki mu tontu.] [Jàngal Dajalekat 5:12.] Ci téere bii, ñu ngi wax li mën a tax nit bañ a nelaw guddi. Te dafa ñuy won li ñu mën a def ngir suñu nelaw bi gën a baax. ”
La Tour de Garde 1er avril
“ Fi lañu wone li ñu faral di wooye Reer bu mujj bi. [Woneel nataal bi nekk ci xët bu njëkk bi ak bu mujj bi ci téere bi.] Ndax xamoon nga ne bés boobu rekk la karceen yi war a màggal ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Lukk 22:19.] Téere bii mu ngi wax lu tax màggal boobu am solo lool te njariñ bi nga ci mënee am. ”
Réveillez-vous ! 8 avril
“ Bu ñu gisee ay ndaw di dorogewu ba yàq seen dund yépp, ndax loolu mettiwul ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ñu bare li leen ci dugal mooy àndandoo yu bon. [Jàngal 1 Korent 15:33.] Réveillez-vous ! bii dafa ñuy won liy xiir xale yi ci dorogewu ak lan la way-jur yi mën a def ngir aar leen ci loolu. ”