Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mars
“ Li ëpp ci ñun mas nañu jaar ci naqar bu réy bu ñuy am bu ñu amee mbokk mu gaañu. Ndax mas nga dégg lu neex li ñu dige fii ? [Jàngal Jëf ya 24:15, te mayal nit ki mu tontu.] Nit ñu bare dañu bëgg xam yan nit ñooy dekki ak it kañ lay doon, ak fan ? Téere bii dafay wax li ci Kàddu Yàlla di tontu. ”
Réveillez-vous ! Mars
“ Ñu bare dañu jaaxle ndaxte bu ñu nekkee lekkool, xale yu góor yi dañuy topp jigéen yi rekk. Naka la xale mënee moytu loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Ci loolu la téere bii wax. Jox na ndaw yi ay xelal yu baax ci xët 26 ba 28. ” Jàngal Léebu 22:3, te won ko lu tax ñu war a daw li ñu mën a dugal ci lu bon.
La Tour de Garde 1er avril
“ Wayjur yu bare, bu ñu amee doom bu bañ a topp li ñu ko jàngal kër ga, seen xol yépp dafay jeex. Lan lañu mën a def ngir xeex lépp li mën a tax seeni doom bañ di leen déggal ? [Mayal nit ki tontu.] Ci xët 8 ba 11 ci téere bii, dañuy wone li wayjur yi mën a def ngir yar seeni doom ba ñu am jikko yu rafet. ” Li nekk ci 5 Musaa 6:6, 7 dafay wone ne bés bu nekk la wayjur yi war a jàngal seeni doom li baax. Jàngal aaya boobu te fexeel ba kàddu yuy wone loolu feeñ bu baax.
Réveillez-vous ! Avril
“ Ñu bare tey, ñu ngi def li ñu mën ngir am dund bu neex. Waaye ñi ko am tey, barewuñu. Ci li ñu bind fii, ndax foog nga ne am na lu mën a indil nit bànneex ? [Won ko wërale bi nekk ci xët 9 te jàngal benn ci aaya yi ñu fa bind.] Kàddu Yàlla wone na li mën a indil nit bànneex dëgg. Ci loolu la téere bii di wax. ”