Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mars
“ At mu nekk, ci weer yi ñu nekk nii, nit ñi dañuy xalaat Yeesu. Fépp ci àddina, nit ñi dañuy wax lu baax ci li mu jàngale. [Jàngal li ñu bind ci xët 3, xise 1.] Ndax foog nga ne li Yeesu jàngale mën na baax ci ñun tey ? Xaaral ma won la ci benn. [Jàngal Macë 5:21, 22a, te mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci li Yeesu jàngale. Dafay wax it ci ni ñu ko mënee jariñoo. ”
Révéillez-vous ! 22 mars
“ Nit ñu bare tey amuñu liggéey. Waaye nag am na ñoo xam ne liggéeyu biro kese lañu bëgg. Bëgguñu liggéey bu ñuy def ak suñu loxo. Ndax xam nga li Kàddu Yàlla wax ci liggéey bu mel noonu ? [Jàngal Efes 4:28 te woneel foofu lu tax liggéey bi ñuy def ak suñu loxo am maanaa.] Téere bii dafa ñuy won ne waruñu xeeb liggéey bu ñuy def ak suñu loxo. ”
La Tour de Garde 1er avril
“ Am na ñuy wax ne li ñu gëm ci wàllu diinee mënul ànd ak li boroom xam-xam yi di wax tey. Ndax mas nga dégg ñuy wax ne boroom xam-xam yi maanaam ñi seen jàng sore lool dañuy weddi li nekk ci Biibël bi ? [Mayal nit ki tontu.] Boroom xam-xam yi mas nañu wax lu àndul ak li diine di jàngale. Ci loolu la téere bii di wax. Waaye téere bi dafay wone it ne xam-xam dëgg dafay ànd bu baax ak li Biibël bi wax. ” Woneel li nekk ci xët 6 ak 7. Boo paree, jàngal Dajalekat 1:7, te wonal nit ki ne li Yàlla wax foofu ci gémmiñu Suleymaan, ànd na bu baax ak li boroom xam-xam yi wax.
Révéillez-vous ! 8 avril
“ Dañu faral di waxtaan ak waajur yi te gis nañu ne jàngal sa doom mu ràññee lu baax ak lu bon, yombul dara. Naka la waajur yi mënee dimbali seeni doom ñu moytu lu bon bu ñu nekkee ndaw ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Isayi 48:17, 18, te wax ko ne war nañu dimbali xale yi ñu xam ne li Yàlla wax ci Baatam mooy seen njariñ ba fàww.] Ci téere bii, dinga gis ne topp li Yàlla wax ci Baatam, mën na dimbali waajur yi ñu faral di am waxtaan yu neex te xóot ak seeni doom. Dina wax it ci bàyyi sa doom mu def li mu bëgg, fu mu war a yem. ”