Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
“ Ndax gis nga ne ci àddina si tey, dafa mel ni mën nga am xam-xam bu dul jeex ci lépp loo bëgg a xam ? [Mayal nit ki tontu.] Waaye, amul xam-xam bu gën bi ñu wax fii : [Jàngal Yowanna 17:3, te wonal bu baax ne xam-xam boobu rekk moo ñu mën a indil njariñ buy yàgg ba abadan.] Ci téere bii, dinga xam lan la ‘ dund gu dul jeex ’ googu tekki, te fan lañu mënee am xam-xam bi mën a tax ñu am ko. ”
Réveillez-vous ! 22 avril
“ Xale yu bare tey dañuy jëfandikoo Internet. Am na ñu bëgg a xam ndax mën nañu jaar ci Internet ngir tànn jëkkër walla jabar ju baax. Ci sa xalaat, boo jaaree ci Internet, ndax dinga mën a xam ndax nit ki am na jikko yu mel ni yii ? [Jàngal 1 Korent 13:4, 5, te wax ko danga war a gis nit ki ak jëfam bala nga mën a xam ndegam am na mbëggeel.] Ci téere bii, dinga gis ndax war nañu xalaat ne Internet mën na dimbali nit mu am jëkkër walla jabar ju baax. ”
La Tour de Garde 1er mai
“ Ñun ñépp mas nañu am mbokk mu gaañu. Su ñu leen mënoon a gisaat, dinañu kontaan lool, du dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Li Biibël bi wax ci ndekkite, seddal na xolu nit ñu bare. [Jàngal Yowanna 5:28, 29.] Téere bii dafay wax ci lan mooy ndekkite, kañ lay doon te ñan ñooy dekki. ”
Réveillez-vous ! 8 mai
“ Tey waajur yu bare dañu jaaxle ndax lu bon li ñuy wone ci film yi. Seetal xeex yi ak lépp lu jëm ci diggante góor ak jigéen li ñu fay wone. Bare na lool. Loolu moo tax ay waajur di tànn li seeni doom di seetaan. Ndax loolu yomb na ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Efes 4:17, te won ko ne fàww ñu moytu yëfi “ neen ”, maanaam yu amul njariñ, yi ñu mën a def ngir féexal suñu xol.] Ci téere bii, dinga gis naka la waajur yi mënee dimbali seeni doom ba ñu mën a tànnal seen bopp lu baax li ñu mën a def ngir féexal seen xol. ”