Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mars
“ Nit ñi tàmm nañu wax ne Yeesu dina fi dellusi. Ci yow, bés bi muy dellusi dañu ko war a yàkkamti walla dañu ko war a ragal ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li yonent bi tudd Yowanna wax ci loolu. [Jàngal Peeñu 22:20 te won ko foofu kàddu gi nee : “ Amiin. Boroom bi Yeesu, ñëwal. ”] Téere bii dafay wone li ñówu Kirist di def. ”
Réveillez-vous ! Mars
“ Ay ndaw yu gën di bare dañuy jaar ci Internet ngir weccante xalaat ak nit ñu nekk fépp ci àddina si. Ndax loolu wóor na ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi mu ngi xiir ñi ragal Yàlla ñépp ñu “ jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon. ” [Jàngal Yawut 5:14.] Waxtaan bii, dina la dimbali yow mii nekk waa-jur, ngir nga gën a xam lu bon lu mën a dal say doom bu ñuy jëfandikoo Internet ci fasoŋ boobu. Dina la wax it li nga mën a def ngir aar say doom ci loolu. ”
La Tour de Garde 1er avril
“ Ñun ñépp bëgg nañu am jàmm ci suñu biir njaboot. Bëgg nañu xam itam li ñu mën a def ngir jàmm jooju yokku. Ci sa xalaat fan lañu mënee am xelal yu wóor te baax ci loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Xoolal li Biibël bi wax fii ci 2 Timote 3:16. [Jàngal aaya boobu.] Téere bii dafay wone naka la ñu Biibël bi mënee dimbali ngir ñu gën a am jàmm ci suñu njaboot ak ci yeneen fànn ci suñu dund. ”
Réveillez-vous ! Avril
“ Ci reew yu bare, nit ñi seetlu nañu ne lu bon li nit ñi daan bañ bu njëkk, nit ñi dañu koy jàppe ni lu baax tey. Ndax seetlu nga loolu yow itam ? [Mayal nit ki tontu.] Li nit ñi seetlu noonu, Biibël bi waxoon na ko. [Jàngal 2 Timote 3:2-4.] Téere bii, dafay wone li xew noonu ci àddina, lu mu tekki ak fu muy jëme doom-Aadama yi.