Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
“ Am na ay nit ñu bokk ci diine, waaye seen ngëm feeñul ci seen dund bés bu nekk. Te ci at yi weesu nii, nit ñooñu ñu ngi gën a bare. Ndax loolu gis nga ko ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Sabuur 119:105.] Ku topp li Yàlla wax ci Kàddoom dinga mën a moytu lu bare loo xam ne dafay lor nit. Téere bii dafa ñuy won fan lañu mën a ame xam-xam boobu. ”
Réveillez-vous ! 22 avril
“ Tey, dafa mel ni xale yi dañuy gaaw a yenu coono mag ñi. Ndax bokk nga ci ñi loolu metti ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Dajalekat 3:1, 4.] Xale, kenn waru ko yen coono mag. Réveillez-vous ! bii dafay wone naka la way-jur yi mënee def ba xale yi bañ a yenu xalaatu mag ñi.
La Tour de Garde 1er mai
“ Am na ay laaj yoo xam ne nit mënu ci tontu dara. Am na ci benn fii. [Jàngal Ayóoba 21:7.] Boo naroon a laaj Yàlla dara, loo koy laaj ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yéenekaay bii dafay wone naka la nit ñu nekk ci àddina si sépp ame tont yu leer ci ñetti laaj yi ëpp solo ci àddina. ”
Réveillez-vous ! 8 mai
“ Ñu gën a bare ci nit ñun xam nañu nit ku am feebaru suukar (maanaam feebar bi ñuy woowe diabète). Ndax xam nga bu baax feebar boobu ? [Won ko nataal bi nekk ci kow yéenekaay bi, te may ko mu tontu.] Yéenekaay bii dafay wone luy indi feebaru suukar, ak lan lañu mën a def bu ñu ko amee. Dafay wone it ne Biibël bi wax na ne dina am jamano joo xam ne dinañu faj feebar yépp, ba fàww. ” Jàngal Isayi 33:24 ngir àggali waxtaan bi.