Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Am na ñuy wax ne lépp lu am ci àddina, boole ci musiba yi, ndogalu Yàlla la. Ndax mas nga xalaat lu mel noonu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Nit ñu bare xam nañu ñaan bii : [Jàngal Macë 6:10b.] Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ? Te coobare boobu kañ lay am ? Téere bii dafay wone li Mbind mu sell mi tontu ci laaj yooyu. ”
Réveillez-vous ! 22 avril
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Am na nit ñoo xam ne amuñu benn yaakaar ngir ëllëg. Ndax loolu masu la dal ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Room 15:4 te won ko ne Kàddu Yàlla mën na ñu may yaakaar bu wóor ngir ëllëg.] Am yaakaar lu am solo la. Téere bii wone na juróom-ñaari mbir yu ñu jële ci Mbind mi yu ñu mën a may yaakaar ngir ëllëg. Boo ko jàngee dina la amal njariñ lool. ”
La Tour de Garde 1er mai
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Am na ay kilifa diine yuy dugg ci politig ngir dimbali nit ñi. Waaye seetal li Isaa defoon bi ñu ko bëggee def buur. [Jàngal Yowanna 6:15.] Isaa wone na lan moo mën a indil doom-Aadama jàmm buy sax. Téere bii ci loolu lay wax. ”
Réveillez-vous ! 8 mai
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Ñu bare tey, amuñu jàmm ci seen liggéey. Ndax xamoon nga ne Biibël bi mën na ñu ci dimbali ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Léebu 15:1 te won ko lu tax neex deret am njariñ.] Téere bii dafa ñuy wax li ñu mën a def ngir am jàmm fi ñuy liggéeye. ”