Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er avril
“ Doomu Aadama yi ñu ngi yàq li am ci suuf si maanaam àll yi, géej gi ak yu mel noonu. Ndax mas nga laaj sa bopp ndegam suuf si dina fi nekk ba fàww ? [Mayal nit ki mu tontu.] Déglul lu neex lii ñu Yàlla dig. [Jàngal Psaumes 104:5.] Kàddu Yàlla wone na naka la suuf si di mel ëllëg. Loolu la téere bii di wone. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 10.
Réveillez-vous ! Avril
“ Li ñu jàpp lool, tax na ba ñu bare di wax ne amuñu jot ngir ittewoo mbirum diine. Ci yow, ndax jaamu Yàlla dafa jafe tey ? [Mayal nit ki mu tontu, te nga jàng Efes 5:15-17.] Mbind mu sell mi wone na ni Yàlla bëggee ñu jariñoo suñu jot ak suñu kàttan ngir jaamu ko. Loolu la téere bii di wone. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 20.
La Tour de Garde 1er mai
“ Nit ñu bare dañuy wax ne, li ñu gis rekk lañu mën a gëm. Ndax ànd nga ak loolu ? [Mayal nit ki mu tontu te nga jàng Room 1:20.] Téere bii dafay wone ñetti jikko Yàlla yuy feeñ bu baax ci li Yàlla sàkk. Dafay wone it li jikko yooyu mën a def ci ñun. ”
Réveillez-vous ! Mai
“ Tey jii, nit ñu bare dañu ragal li mën a am ëllëg. Ndax yaakaar nga ne dund gi dina mas a tànne, walla ci yow dafay gën di yees rekk ? [Mayal nit ki mu tontu te nga jàng Peeñu ma 21:3, 4.] Téere bii dafay wone lu tax ñu mën a gëm ne, léegi Yàlla dindi poroblem yu metti yi, nga xam ne doomu Aadama yi mënuñu fexe ba regle leen. ”