Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
“ Nit ñi soxor ak seeni moroom, dafa mel ni ñu ngi gën di bare ci àddina si. [Waxal lenn lu xewoon ci seen dëkk walla lenn lu ñu nettali ci yéenekaay bii.] Ndax masuloo laaj sa bopp naka la nit mënee soxor noonu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Kàddu Yàlla waxoon na ne nit ñu soxor ñi dinañu gën a bare. [Jàngal 2 Timote 3:1-5.] Téere bii, dafay tontu ci laaj bii : ‘ Ndax nit ñu soxor ñi dinañu fi mas a jóge ? ’”
Réveillez-vous ! Avril
“ Waa-jur yu bare tey, bu ñu bëggee seeni doom def liggéey bu gën a baax ci lekkool walla ci kër gi, dañu leen di wax lu beneen xale def. Ci sa xalaat, ndax loolu baax na ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Mbind mu sell mi wax ci loolu. [Jàngal Galasi 6:4.] Xaaj bii, dafay waxtaan ci lu baax ak lu bon lu mën a nekk ci tollale nit ak keneen. ” Won ko waxtaan biy tàmbali ci xët 11.
La Tour de Garde 1er mai
“ Xale bu dee, metit bu réy la ci xolu waa-jur te metit boobu du gaaw a deñ. Fan la waa-jur yi mënee am luy dëfël seen xol bu leen loolu dalee ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Room 15:5.] Téere bii dafay waxtaan ci li Yàlla di def ngir ñi am naqar. ”
Réveillez-vous ! Mai
“ Am na nit ñu bare alal lool, fekk ñeneen amuñu dara. Ndax yaakaar nga ne lu mel noonu dina mas a jeex ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal ni Yàlla gise ñi barewul alal. [Jàngal Sabuur 22:24.] Téere bii dafay wax ci yaakaar bi Kàddu Yàlla di may ñi barewul alal. ”