TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/03 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 5/03 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 mai

“ Bés bu nekk ñu ngi dégg ay jëfi fitna. Ndax loolu, ci suñu jamano rekk la am ? Walla ndax masoon na am ci beneen jamano ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Mbind mu sell mi wax. [Jàngal Macë 24:37.] Lu bon li amoon ci jamano Nóoxin dafa bare woon ba Yàlla mujj a alag lépp lu doon dund. Nóoxin ak njabootam rekk ñoo mucc. Téere bii dafa ñuy won lu loolu war a tekki ci ñun tey. ”

Réveillez-vous ! 22 mai

“ Tey feebar yi bare nañu. Am na sax ay gunóor yuy joxe feebar. Ndax xam nga li ñu mën def ba aar suñu bopp ci gunóor yooyu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yéenekaay bii dafay wax li ñu mën a def. Dafay wone it ne Biibël bi wax na ne dina am jamano joo xam ne kenn dootul feebar. ” Jàngal Isayi 33:⁠24.

La Tour de Garde 1er juin

“ Yenn saay, li nit ñi di maye ngir jàpple mbootaay yiy dimbali ñi nekk ci coono, duñu ko jëfandikoo ni mu ware. Looloo tax ñu bare xamatuñu sax ndax jar na ñuy maye seen alal ngir jàpple mbootaay yooyu. Waaye nag, ñi soxla ndimbal tey, bare nañu lool. Lan lañu mën a def ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Yawut yi 13:16.] Yéenekaay bii dafay wone yan maye ñoo neex Yàlla. ”

Réveillez-vous ! 8 juin

“ Ndax seetlu nga ne nit ñi am yar tey barewuñu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Li ñuy gis tey, Biibël bi waxoon na ko bu yàgg. [Jàngal 2 Timote 3:​1-5.] Yéenekaay bii dafay wone lu tax nit ñi mel noonu ak li nar a am ëllëg. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager