TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/05 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 5/05 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 mai

“ Néew doole bare na tey, te mu ngi law. Ndax loolu dina mas a jeex ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal li ñu Yàlla dig fii. [Jàngal Isayi 65:21 te won ko ne nit ku nekk dina mën a jariñoo li mu liggéey.] La Tour de Garde bii dafay wax naka la Yàlla di defe loolu. Te dinga ci jàng it li ku néew doole mën a def ngir dundam tane. ” Seetal ak moom kañ ngay mën a dellusi ngir waxtaan ci laaj bii : Li Yàlla dige noonu, kañ lay am ?

Réveillez-vous ! 22 mai

“ Tey dañuy waxtaan lu jëm ci Internet. Ndaw yu bare dañuy jaar ci Internet ngir am xarit. Waaye xamuñu lu bon li leen ci mën a fekk. Ndax mas nga ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii, ci loolu lay waxtaan. Dina dimbali waajur yi ak xale yi ñu xam lu tax ñu war a moytu jéem a am xarit ci Internet. ” [Jàngal Léebu 22:3 te waxal lu tax li Suleymaan wax noonu baax ci kuy jëfandikoo Internet.]

La Tour de Garde 1er juin

“ Diisoo yombul ci séy. Ñu bare dinañu ci dàkkoor. Waaye lan lañu mën a def ngir loolu yomb ci ñun ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Léebu 12:18 te won ko ñaari fasoŋ yi ñu mën a jëfandikoo suñu gémmiñ.] Téere bii dafay wone li jëkkër ak jabar mën a def ba faral di waxtaan ci jàmm. ”

Réveillez-vous ! 8 juin

“ Nit ñu bare dañu bëgg am tur bu mag, xaalis bu bare walla nekk kilifa bu bare kàttan. Dañu foog ne dinañu ci am bànneex ak mbégte. Lan nga ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu.] Yonent Yàlla Suleymaan bare woon na alal te buur bu mag la woon. Waaye xoolal li ëppoon solo ci moom. [Jàngal 1 Buur 3:​9, te won ko jikko yi Suleymaan bëggoon a am ba mu ñaan ko Yàlla.] Téere bii dafay wone ni ñu war a gise xaalis, nekk kilifa bu bare kàttan, tur bu siiw ak yu mel noonu. Dafay wone it ne suñu diggante ak Yàlla lañu war a jiital ci suñu àddina. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager