TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/03 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 6/03 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 juin

“ Am na ñuy wax ne ku gën a mag Yeesu masu fi am. Am na ñeneen ñu xamul ndax Yeesu mas na dund walla déet. Ni ñuy gise Yeesu, ndax am na solo ? [Bu la tontoo ba pare, jàngal Jëf ya 4:12.] Ndax am na luy wone ci lu leer ne Yeesu mas na dund ci kow suuf si ? Ci loolu la yéenekaay bii di wax. ”

Réveillez-vous ! 22 juin

“ Ñu bare dañuy jéem a sàmm suuf si ak lépp li ci nekk. Ndax foog nga ne mën nañu sàmm àll yi ñuy woowe ci tubaab forêts tropicales ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yéenekaay bii dafay wone li nit ñi di def ngir sàmm àll yooyu. Dafay wax it naka la Yàlla di defe li mu dige ci aaya bii : [Jàngal Isayi 11:9]. ”

La Tour de Garde 1er juillet

“ Mbëggeel bokk na ci li nit gën a soxla. [Jàngal li ñu bind ci wetu nataal bi nekk ci kow ci xët 4.] Waaye dafa mel ni tey, leneen la nit ñi gën a fonk, du dëgg ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yéenekaay bii dafay wone lan mooy mbëggeel dëgg, ak li ñu mën a def ba am mbëggeel boobu. ” Jàngal 1 Korent 13:⁠2.

Réveillez-vous ! 8 juillet

“ Ndax dégg ngeen... [Waxal lenn lu xew ci seen gox ci wàllu fitnaal te ñépp yëg ko, ba pare may ko mu tontu.] Tey, lu mel noonu dafa gën a bare. Tiital na ñu bare. Yéenekaay bii dafay wone lu tax jëfi fitna yu mel noonu di am tey. Dafay wone itam naka la Yàlla di dindee ba mu jeex tàq jëfi fitna yi ak li nit ñi di jéggi li yoon tëral. ” Jàngal Sabuur 37:​10, 11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager