Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mai
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Li nit di def ndax dafay laal Yàlla ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal fii naka la suñuy jëf di laale Yàlla ci xolam. [Jàngal Léebu 27:11 te won ko li ñu mën a def ngir bégal Yàlla.] Téere bii dafa ñuy won ay nit ñu bégaloon Yàlla, te ni ñu leen mënee topp. ”
Réveillez-vous ! 22 mai
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Tey doktoor yi mën nañu faj lu bare. Waaye, ndax foog nga ne feebar dina mas a jeex ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafa ñuy wax ci bés boo xam ne feebar dootul am, te nit ñépp dinañu am wér-gi-yaram. Loolu Yàlla moo ko dige fii. ” Jàngal Isayi 33:24.
La Tour de Garde 1er juin
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Am na ñuy wax ne mën nga jaamu Yàlla te bañ a bokk ci benn diine. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu.] Mbind mu sell mi wone na ni Yàlla doon defe ak nit ñi ci jamano yu njëkk ya. Ci loolu la téere bii di wax. Dafay wone it lan mooy jaamu Yàlla ci dëgg. ” Jàngal Yowanna 4:24, te won ko ne diine jiy topp dëgg gi jóge ci Yàlla mooy diine dëgg gi.
Réveillez-vous ! 8 juin
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ñu bare tey amuñu xarit dëgg, moo tax ñu wéet lool. Loolu metti na de, du dëgg ? [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Sabuur 25:16 te won ko ne jege Yàlla mën na tax ñu bañ a wéet.] Réveillez-vous ! bii dafa ñuy won li ñu mën a def ngir lu mel noonu bañ ñu dal. ”