Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 juillet
“ Ñu bare dañu seetlu ne, nit ñu bare tey dañuy beru. Ndax foog nga ne loolu baax na ? [Mayal nit ki mu tontu.] Am na li Mbind mu sell mi wax ci àndandoo. [Jàngal Dajalekat 4:9, 10.] Yéenekaay bi dafay wone lu tax nit ku nekk soxla moroomam. Dafay wone it li ñu mën a def ngir nit ñi bañ a beru. ”
Réveillez-vous ! 22 juillet
“ Tey, ñu bare dañu jaaxle ndaxte dafa bare téere ak film yuy wone lu ñaaw diggante góor ak jigéen. Ndax foog nga ne war nañu ci jóg ? [Mayal nit ki tontu.] Li Biibël bi wax fii mën na ñu dimbali ba ñu moytu lu bon loolu. [Jàngal Efes 5:3, 4.] Yéenekaay bii dafay wone li ñu mën a def ngir aar suñu bopp ci lu bon loolu. ”
Tour de Garde 1er août
“ Ndax xamoon nga ne genn-wàllu nit ñi nekk ci àddina si sépp, li ñuy dunde bés bu nekk matul sax 1 400 FCFA ? Metti na de. Lan moo ciy pexe ? [Mayal nit ki tontu.] Mbind mu sell mi wax na lu fi mën a dindi néew doole. Moom la Tour de Garde bii di wone. ” — Jàngal Sabuur 72:12, 13, 16.
Réveillez-vous ! 8 août
“ Bare na musiba yoo xam ne lu leen indi mooy taw bu bare bay yàq, walla lu mel noonu. Loolu coono kese lay indi. Ci yow, lan lañu mën a def ngir wàññi coono yooyu ? [Mayal nit ki tontu.] Yéenekaay bii dafay wax lu tax lépp jaxasoo ci àddina si. Yenn saay mu taw ba mu ëpp, yenn saay taw ñàkk. Dafay wax it ci pexe bi Mbind mu sell mi wax ci loolu. ” — Jàngal Isayi 35:1.