Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 juillet
“ Ñu bare xam nañu ne Yeesu yonent la woon, te dafa def ay kéemaan yu bare. Wax nañu fii benn ci kéemaanam yi : [Waxal li xewoon bala Yeesu di def kéemaan bi ñu wax ci Mark 4:39 ba pare jàngal aaya boobu.] Ndax wóor na ñu ne Yeesu def na kéemaan yooyu ? Téere bii ci loolu lay wax. Dafay wone it lu tax Yeesu doon def ay kéemaan. ” [Jàngal xise 7, xët 6.]
Réveillez-vous ! 22 juillet
“ Dañu bëggoon a waxtaan tey ci njublaŋ yi nga xam ne ñépp lañu jaaxal. Bés bu ne, ñu am pexe bu bees ngir nangu alalu jaambur. Nit ñi sonn nañu lool. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu.] Réveillez-vous ! bii dafa ñuy won li ñu mën a def ngir aar suñu bopp ci njublaŋ yi. ” Jàngal Léebu 22:3 te woneel ne ku bañ njublaŋ nax la, fàww nga ëpp ko pexe.
La Tour de Garde 1er août
“ Dañu doon laaj nit ñi li ñu xalaat ci ñàkk jàmm ak déggoo yi am ci àddina si tey. Am na ñuy wax ne bu ñu bëggee jàmm am ci àddina si, waratul am nguur yu bare yuy jiite àddina si. Benn nguur kese moo war a ilif àddina si sépp. Waaw, ndax loolu mën na am ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Dañel 2:44 te woneel ne léegi Nguuru Yàlla dindi yeneen kiliftéef yépp.] Téere bii dafay wone ne am na li Nguuru Yàlla di def tey jii. Dafay wone it ne léegi mu indi jàmm ci àddina si sépp. ”
Réveillez-vous ! 8 août
“ Dañu doon waxtaan ci xale yi ñuy toroxal tey. Am na xale yoo xam ne li ñu nekke metti na. Ku gis xale bu ñuy toroxal, dafa lay metti. Moo tax xéyna mas nga laaj lii : ‘ Ndax Yàlla gis na loolu yépp ? ’ [Mayal nit ki tontu. Ba pare jàngal Sabuur 72:12-14, te woneel ne Yàlla dafa bëgg dimbali “ ñi nekk ci mettit ” ak “ ñi néew doole ”.] Téere bii dafay wone ni Yàlla fonke xale. Dafay wone it ne léegi Yàlla dimbali ñi ñuy toroxal ñépp, ngir ñu am jàmm ba fàww. ”