Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
Tour de Garde 15 août
“ Tur bu rafet, ñépp a ko fonk. Am na sax ay nit ñu ragal ñu wax lu ñaaw ci seen kow bu ñu deewee. Ndax mas nga ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu.] Xoolal li Suleymaan wax fii. [Jàngal Dajalekat 7:1.] La Tour de Garde bii dafay wone ni ñu mënee rafetal suñu tur ci kanamu nit ñi ak ci kanamu Yàlla. ”
Réveillez-vous ! 22 août
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Suñu tànk tànku jàmm la. Dañu bëggoon a waxtaan tey ci li ñu mën a def ngir suñu doom yi gën a am jàmm ci seen lekkool. Yeen saay dafay am seen benn moroom bu leen ëpp doole, te muy nangu li ñu yor. Dina leen jàpp, di leen door, di leen saaga ak yu mel noonu. Loolu metti na lool, du dëgg ? Naka lañu leen mënee dimbali ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii ma yor, ci loolu lay waxtaan. Dafay wax it ci bés bu Yàlla di dindi loolu lépp. ” [Jàngal Mikaa 4:4.]
La Tour de Garde 1er sept
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Tey dañu am benn laaj bu ñu bëgg laaj ñépp. Diine yuy wax ne ci Isaa lañu bokk, lu tax ñu bare nii ? [Mayal nit ki tontu.] Am na li ci Isaa wax ci Macë 13:24-30. [Wax ko ci lu gàtt li nekk ci Macë 13:24-30]. Téere bii, ci loolu lay waxtaan. ”
Réveillez-vous ! 8 sept.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Gis nañu tey ne, ñu bare lu xew rekk lañu bëgg sol. Jaral na leen xaalis bu bare, walla sax dëkk ci bor. Noo gise loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Mbind mu sell mi dafa ñuy wax ci ay yére yoo xam ne, ñépp a ko war a sol. [Jàngal Kolos 3:12]. Téere bii, dafa ñuy won ni ñu mënee def ba yére yi ñuy sol bañ ñoo jiital. ”