Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Nit mën na def dara tey, loolu topp ko ay ati at. Naka lañu mënee moytu li ñuy indil coono ëllëg ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare jàngal Léebu 3:6.] La Tour de Garde bii dafay joxe juróomi xelal yu ñu jële ci Mbind mu sell mi. Boo leen toppee, dinga mën a moytu lu lay yàqal ëllëg. ”
Réveillez-vous ! 22 oct.
“ Ndax seetlu nga ne feebar yu bare dañu gën a naqadee faj tey ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone lu waral loolu, ak li ñu mën a def ngir aar suñu bopp ci loolu. Dafay wone it ne ci Biibël bi, Yàlla dig na ne dina am bés boo xam ne kenn dootul feebar. ” Jàngal Isayi 33:24.
La Tour de Garde 1er nov.
“ Yenn saay dangay wóolu kenn waaye mu tas sa yaakaar. Ndax am na ku ñu mën a wóolu dëgg ? [Mayal nit ki tontu ba pare jàngal Léebu 3:5.] Téere bii dafay wone lu tax ñu mën a wékk suñu yaakaar yépp ci Yàlla. Dafay wone it ni ñu mënee ràññee nit ku ñu mën a wóolu. ”
Réveillez-vous ! 8 nov.
“ Bés bu nekk ñu soxla li ñu mën a jële ci petarool. Waaw, bu petarool jeexoon ci àddina si sépp, lu ñuy def ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii, dafay wone fu ñu jaar ba soxla petarool noonu ci suñu jamano. Dafay wone it lu tax waruñu ragal petarool jeex benn bés ci àddina si sépp. ”