Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
“ Tey dañuy waxtaan ak nit ñi ci li mën a tax dund bi neex te am maanaa. Am na ñuy foog ne ku la ëpp xaalis ëpp la bànneex. Ndax ci sa xalaat, loolu dëgg la? [Mayal nit ki tontu.] Yonent Yàlla Suleymaan dafa amoon xaalis ba kenn mënu ko woon konte. Waaye seetal li mu wax ci loolu. [Jàngal Dajalekat 5:10, te woneel lu tax dëkk ci topp xaalis rekk amul benn njariñ.] Téere bii dina la won lu ëpp solo alal fuuf. ”
Réveillez-vous! 22 oct.
“ Dañuy waxtaan ak nit ñi ci kañ lañu mën a komaasee jàngal xale. Ndax xamoon nga ne mën nañu jàngal xale bu tuuti ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal 2 Timote 3:15, te woneel ne xale mën na komaasee jàng bi mu nekkee lu tuuti.] Téere bii dafay wone li wayjur yi mën a def ngir seeni doom mën a nekk ëllëg mag yu jub te baax. ”
La Tour de Garde 1er nov.
“ Tey, nit ñu bare gëmuñu ne njiiti nguur yi mën nañu dindi suñu coono yi. Ndax foog nga ne am na ku mën a def li ñu wax fii ? [Jàngal Sabuur 72:7, 12, 16 te may ko mu tontu.] Téere bii dafay wax kan mooy njiit bi ñu wax fii, te li mu nar a def. ”
Réveillez-vous! 8 nov.
“ Dañuy waxtaan ak nit ñi ci ni ñu mënee dimbali suñu doom yi. Ndax xalaatoo ne xale yi soxla nañu ku leen di wax li ñu mën a def ngir àddina si bañ leen a dugal ci lu bon ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Efes 6:4 te fexeel ba nit ki mën a ràññee ci li ngay jàng kàddu yii : “yar ” “ yemale ak a yee ”.] Téere bii dafay wax lan mooy yar dëgg. Dafay wax it naka la wayjur yi mënee bañ a jeexal seen xolu doom bi ñu leen di yar. ”