Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde Mar. 15
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Dañu la bëgg woo ci Reeru Sang bi. Dimaas 4 awril lañu koy def. [Jëfandikoo téere bii ci xët bi mujj, walla kayit bi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu te leeralal ko lan mooy Reer bi. Ba pare, jàngal Lukk 22:19.] Xaaj bi njëkk ci La Tour de Garde bii, dafay wax lu Reer boobu tekki, te naka lañu koy defe. ”
Réveillez-vous ! 22 mars
Boo nuyoo ba pare, waxal musiba boo xam ne mu ngi ci xelu nit ñépp te laajteel lii : “ Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax Yàlla di bàyyi musiba yu mel nii am ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Saak 1:13, te waxal nit ki lu tax du Yàlla mooy indi metit yi.] Xaaju téere bii ndaw yi ñoo tax ñu bind ko. Dafay wax lu tax ba léegi Yàlla mi nga xam ne dafa ñu bëgg, deful dara ngir dindi coono nit ñi. ”
La Tour de Garde 1er avril
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Ci Mbind mu sell mi aaya bii di wone màndarga rab bi, nit ñi wax nañu ci lu bare. Ndax mas nga ci dégg dara ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Peeñu bi 13:16-18.] Mbind mu sell mi dafay wax lan mooy màndarga boobu. Moom la téere bii di wone. ”
Réveillez-vous ! 8 avril
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Bàyyi lu bon yombul. Seetal ñiy tux. Ñu bare dañu koy bëgg bàyyi, waaye mënuñu ko. Ci yow, lan moo mën a dimbali nit ñu mel noonu ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal 1 Korent 10:13 te won ko ne Yàlla dafa bëgg dimbali ñiy jéem a def lu baax.] Am na ñu bëgg bàyyi lu bon li ñu tàmm. Mbind mu sell mi wax na lu leen ci mën a dimbali. Xaaju téere bii ci loolu lay wax. ”