Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er mars
“ Bés bu nekk ñu dégg ay metit, feebar, ak dee. Mas nga laaj sa bopp ndax dinañu mas a mucc ci loolu lépp ? [Mayal nit ki mu tontu.] Li Biibël bi wax ci aaya bii may na yaakaar ay milyoŋi nit. [Jàngal Yowaana 3: 16.] ‘ Comment la mort de Jésus peut vous sauver ? ’ (maanaam naka la la deewu Yeesu mënee musal). Ci loolu la yéenekaay bii di wax. ”
Réveillez-vous ! Mars
“ Nit ñu bare tey dañuy wax ne waat walla saaga dara newu ci. Ci sa xalaat, ndax am na lu war a tax ñu wax ne waat lu bon dëgg la ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Kàddu Yàlla wax ci loolu nit ñi tàmm. [Jàngal Efes 4:31.] Lu tax waat bon te naka lañu ko mënee moytu ? Ci loolu la yéenekaay bii di wax. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 19.
La Tour de Garde 1er avril
“ Li yonent yi wax fii, ndax bëgg nga mu am ? [Jàngal Esayi (Isaïe) 2:4, te may nit ki mu tontu.] Gis nga ne Yàlla dina jublu ci mbirum doomu Aadama yi te ‘ lijjanti diggante ’ yi. Mbind mu sell mi nee na, Yàlla dina def xare bu ñuy woowe Armagedon, te dina jeexal xare yépp. Yéenekaay bii dafay leeral luy Armagedon te lu tax ñu yàkkamti ko. ”
Réveillez-vous ! Avril
“ Ndax yaakaar nga ne ñu ngi ci jamano bi ñuy wax fii ? [Jàngal 2 Timote 3:1-4, te may nit ki mu tontu.] Mujju jamano war na ñu soxal ndaxte bu jotee dafay wone ne dina am lu neex luy ñëw ci suuf si. Ci loolu la yéenekaay bii di wax. ”