Ni ñu mën a wonee téere Écoute le grand Enseignant
◼ “ Jàngalekat bi gën a mag bi moo waxoon lii : [Jàngal Macë 7:12a.] Bu ñépp toppoon loolu, ndax àddina si du gën a neex ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci li jàngalekat bi gën a mag bi jàngale. ” Woneel nataal yi nekk ci pàcc 17 te waxal ci kàddu yi ñu àndal.
◼ “ Tey waajur yi dañuy góor-góorlu ngir seen doom mën a ràññe lu baax ak lu bon. Ndax loolu am na solo ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Léebu 22:6.] Fii gis nañu ne waajur yi dañu war a teel a komaase di jàngal seeni doom. Téere bii dina leen ci dimbali. ” Woneel nataal yi nekk ci pàcc 15, 18 walla 32 ak kàddu yi ñu àndal.
◼ “ Yenn saay waajur yi dañuy waaru ci li seeni doom di laajte. Lée-lée sax duñu xam lu ñuy tontu. Ndax loolu masu la dal ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal 2 Timote 3:14, 15.] Yaayu Timote ak maamam dañu ko jàngal li nekk ci Mbind yi. Bi mu nekkee xale bu tuuti lañu ko komaase. Téere bii mën na dimbali waajur yi bëgg def loolu ñoom itam. ” Woneel yenn nataal ci yi nekk ci pàcc 11 ak 12, walla 34 ba 36, te waxal ci kàddu yi ñu àndal.