Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mai
“ Luy sa tontu ci laaj bi ? [Jàngal laaj bi nekk ci kanamu téere bi te may ko mu tontu]. Kàddu Yàlla wax na ñu li mën a tax ñu bañ a ragal suñu ëllëg. [Jàngal Sabuur 119:165]. Jàng Kàddu Yàlla te def ci sa xol yépp, téere bii dafay wone naka la loolu mën a feesal sa xel ak sa xol ak ay xalaat yu rafet ci suñu ëllëg. Dafay wone itam naka la Nguuru Yàlla nekke lu wóor fu ñu mën a wékk suñu yaakaar. ”
Réveillez-vous ! Mai
“ Ndax foog nga ne lépp li ñuy def ak fu ñuy mujje Yàlla dafa ko bind ba pare ? [May ko mu tontu.] Ci ay kàddu yi mu jaarale ci yonent Yàlla Musaa, Yàlla may na nit ñi ñu tànnal seen bopp ni ñuy dunde. [Jàngal 5 Musaa (Deutéronome) 30:19.] Téere bii wone na lan la ci Mbind mu sell mi wax. Won ko waxtaan biy komaase ci xët 12.
La Tour de Garde 1er juin
“ Bés bu nekk, li ci ëpp, bu ñuy déglu xibaar yi, ay jëf yu ñaaw yu nit ñi def kese lañuy dégg. [Wax ko lu ñaaw lu nit ñi dégg ci seen gox]. Masuloo laaj sa bopp ndax amul ku bon ku ñu dul gis kuy dugal nit ñi ci lu bon ? [May ko mu tontu, ba pare, jàngal Peeñu bi 12:12]. Téere bii dafay wone naka lañu mënee aar suñu bopp ci loolu. ”
Réveillez-vous ! Juin
“ Bëggoon naa xam sa xalaat ci li ñu wax fii. [Jàngal 1 Timote 6:10]. Ndax xalaat nga ne dëgg dëgg, bëgge ci xaalis, ci naqar rekk lay mujje ? [May ko mu tontu]. Téere bii day wone metit yi nekk ci def lépp ngir am alal bu dul jeex. ”