Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mai
“ Bu sa dund meloon ni li ñu wax ci aaya bii, ndax dina la neex ? [Jàngal 2 Piyeer 3:13, te mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone ni asamaan su bees si ak suuf su bees si di mel. Dafay wone it ne bés bu Yàlla defee li mu bëggoon bi mu sàkkee suuf si, dund gi du mel ni bu tey jii. Dina wute lool. ”
Réveillez-vous! Mai
“ Am na ñu gëm ne boo bëggee am alal ju bare tey, fàww nga njaxlaf te ñeme xeex. Waaye nag, seetal li Yeesu wax fii. [Jàngal Macë 5:5, 9.] Ndax ànd nga ak loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Bëgg jàmm baax na lool. Téere bii dina wone ñetti njariñ yu ci nekk. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 28.
La Tour de Garde 1er juin
“ Am na jamano joo xam ne mag yi dañu leen doon may cër. Moom la ndigal bu yàgg bii wone. [Jàngal 3 Musaa (Lévitique) 19:32 te wonal nit ki ne may cër mag yi, ci ragal Yàlla la bokk.] Ndax ci suñu jamano tey nit ñi dañuy may cër mag yi ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone ni Yàlla di toppatoo mag yi ak ni ñu ko mënee def ñun itam. ”
Réveillez-vous! Juin
“ Li tubaab di woowe terrorisme (maanaam musiba bu réy bu nit daaneel ci ay moroomam ngir ñu jox ko li mu bëgg) yàgg na ci àddina. Waaye tey, mën na dal fu nekk te laal ñépp. Lu waral loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Mbind mu sell mi wone na ne doom-Aadama mënu fi indi jàmm ba fàww. Yàlla rekk moo mën loolu. [Jàngal Mika 4:4 te fexeel ba kàddu yii di topp feeñ bu baax : “ car la bouche même de Jéhovah des armées l’a dit ” maanaam Yexowa ci boppam moo ko wax, moom mii am ay xarekat.] Réveillez-vous ! bii dafay wone naka la terrorisme di jeexe ak it naka la Yàlla di indee jàmm dëgg ci kow suuf si. ”