TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/04 p. 4
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 6/04 p. 4

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 juin

[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Yar doom ci jamano jii, yombul. Du dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Waaye waajur yi mën nañu yar seeni doom ba ñu am yar bu rafet. Loolu la Mbind mi wax fii : [Jàngal Léebu 22:6 te won ko ne yar bu baax dafay topp xale lu yàgg-a-yàgg.] Tour de Garde bii dafay wax lu am solo lu mën a dimbali waajur yi ngir ñu yar seeni doom yar bu rafet. ”

Réveillez-vous ! 22 juin

“ Am na nit ñu gëm ne Yàlla moo sàkk lépp, am na it ñuy wax ne Yàlla amul. Bu la nit waxoon : “ Lan moo lay won ne Yàlla am na ? ” Loo koy wax ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal fii loo ko mën a tontu : [Jàngal Room 1:20 te wax ko ne li ñu wër dafa ñuy jàngal lu bare ci Ki ñu sàkk]. Réveillez-vous ! bii dafay wax lu tax mu mën ñu wóor ne Yàlla am na. ”

La Tour de Garde 1er juillet

“ Tey musiba mën na jékki-jékki rekk dal nit ku mu mënta doon. Lu mel noonu bu amee, ñu bare dañuy laajte lii : “ Su dee Yàlla dafa ñu bëgg, lu tax muy seetaan yu mel nii ? ” Ndax mas nga laaj sa bopp loolu ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafa ñuy wax liy wone ne Yàlla dafa ñu fonk ak li Yàlla bëgg def tuuti ci kanam. ” Jàngal Peeñu bi 21:4 te won ko ne Yàlla dafa ñu bëgg moo tax mu wax ne dina dindi suñuy coono. ”

Réveillez-vous ! 8 juillet

“ Xale bala muy nekk janq walla waxambaane, lu bare dina soppeeku ci moom. Waajur yu bare dañuy wax ne waxtaan ak sa doom ci loolu, yombul. Ndax yow itam noonu nga ko gise ? [Mayal nit ki tontu.] La Tour de Garde bii dafay wax ci liy soppeeku noonu ci xale buy màgg. Dafay wone it li ndaw mën a def ngir am jàmm ci dundam. ” Jàngal Dajalekat 12:1 te waxal lu tax waruloo xaar ba nga mag sog a jaamu Yàlla boo bëggee am ëllëg bu neex.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager