Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er juin
“ Lu ëpp ci nit ñi, bu ñu gisee lu ñu xamul, dañuy def lu nekk ngir xam lu mu doon. Ci yow, lan moo jar a gëstu ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare nga jàng 2 Timote 3:16, 17.] Téere bii dafay wone ne xam-xam bu ñuy jële ci Kàddu Yàlla moo gën fuuf xam-xam bu mu mënta doon. ” Won ko waxtaan bu komaase ci xët 19.
Réveillez-vous ! Juin
“ Wóor na ne dinga nangu ne bu xale di nekk waxambaane walla jànq, dafay am ay jafe-jafe te coono la it ci ay way-juram. Ndax yaakaar nga ne bu way-jur yi toppee xelal bii, dinañu gën a am pexe ci jafe-jafe yooyu ? [Jàngal Saag 1:19 ba pare may ko mu tontu.] Téere bii dafay wone xelal yu baax yu ñu jële ci Mbind mu sell mi. Boo ko jàngee dina la amal njariñ. ”
La Tour de Garde 1er juillet
“ Kenn ku nekk ci ñun mas na am mbokk walla xarit bu gaañu. Ndax yaakaar nga ne Kàddu Yàlla mën na dimbali ku am naqar boobu ? [Mayal nit ki mu tontu te nga jàng Sabuur 55:22.] Biibël bi wone na li ñu mën a def bu ñu amee naqar boobu. Ci loolu la téere bii di wax. ”
Réveillez-vous ! Juillet
“ Jafe-jafe yi dañuy gën a bare ci séy. Te séy yu bare ci tas lañuy mujje. Ndax xalaat nga ne bu nit ñi toppee xelal bii, seen séy dina gën a neex ? [Jàngal Léebu 12:18 te may ko mu tontu.] Mbind mu sell mi joxe na yeneen xelal yu mën a rattaxal diggante jëkkër ak jabar. Ci loolu la téere bii di wax. ”