TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/06 p. 4
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 6/06 p. 4

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 juin

“ Tey, ak coono yi ñu am yépp, ndax nit mën na am bànneex dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone fi ñu mënee am xelal yu ñuy won li ñu mën a def bu ñu amee naqar yu mel ni mbokk mu gaañu. Wone na it ne yaakaar ju wóor dafay maye doole. ”Jàngal Peeñu ma 21:3, 4 te fexeel ba kàddu yii di topp feeñ bu baax : “ dee dootul am ” ak “ yëf yu jëkk ya wéy nañu ”.

Réveillez-vous! Juin

Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax bàkkaaru Aadama ak Awa laal doom-Aadama yépp ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal fii lan moo leen xiir ci bàkkaar. [Jàngal Njàlbéen ga 3:5 te fexeel ba kàddu yii di topp feeñ bu baax : ‘ dingeen ’ ak ‘ xam ’.] Mbind mi wone na ne suñu maam yi, bëggatuñu woon Yàlla won leen li baax ak li bon. Dañu ko bëggoon a tànnal seen bopp. Am na lu Yàlla def ngir jële fi lépp lu bon li bàkkaar boobu indi. Téere bii, loolu lay wone. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 28.

La Tour de Garde 1er juillet

“ Tey ci suñu jamano bu jaxasoo bii, ñu bare dañu bëgg xam lu tax coono yi bare nii. Bu dee Yàlla am na, lu tax du fi jële metit yi ? Ndax loolu mas nga ko laaj sa bopp ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dina la won li ci Kàddu Yàlla tontu. ” Jàngal 2 Timote 3:16 te fexeel ba kàddu yii feeñ bu baax : “ am na njariñ ngir jàngal nit ñi ”.

Réveillez-vous! Juillet

“ Tey jafe-jafe diggante jëkkër ak jabar mu ngi yokku rekk. Bu ñu toppoon li Yàlla wax fii, ndax seen diggante du gën a rattax ? Loo ci xalaat ? [Jàngal Efes 4:32 te fexe ba jikko yi ñu ci wax feeñ bu baax. Ba pare mayal nit ki mu tontu.] Réveillez-vous ! bii dafay wax ci xelal yu jóge ci Yàlla yoo xam ne dañu mas a jariñ ñu bare ba ñu am jàmm ci seen séy. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager