Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 juin
“ Jafe-jafe yu mel ni bii ñuy wax fii, ndax foog nga ne dinañu mas a jeex ? [Jàngal li ñu njëkk bind ci xaaj bu njëkk bi, te mayal nit ki mu tontu.] Kàddu Yàlla mu ngi ñu wax ne jafe-jafe yu mel noonu léegi ñu jeex. [Jàngal Sabuur 72:12-14.] La Tour de Garde bii dafay wone naka la loolu di amee. ”
Réveillez-vous ! 22 juin
“ Ndax foog nga ne dina am bés boo xam ne, ñépp dinañu am jàmm ak salaam dëgg ci kow suuf si ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal lu neex li ñu Yàlla dig. [Jàngal Room 8:21.] Ngir loolu mën a am, nooteel yépp a war a jeex, du dëgg ? Réveillez-vous ! bii dafay wone ni loolu di ame. ”
La Tour de Garde 1 juillet
“ Nit ñu bare dañuy jëfandikoo nataal ak xërëm bu ñuy jaamu Yàlla, fekk ñeneen di xalaat ne loolu baaxul. Ndax mas nga laaj sa bopp lu ci Yàlla xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Yowanna 4:24.] Xaaji La Tour de Garde bii dañuy wone fan la jëfandikoo nataal bu ñuy jaamu Yàlla cosaanoo. Dina wone it li Mbind mu sell mi wax ci li jëm ci jaamu ay nataal. ”
Réveillez-vous ! 8 juillet
“ Mbind mu sell mi wax na ne mujum jamano dina metti. [Jàngal 2 Tim. 3:1, 3.] Ñaawtéef bi bare na ci àddina si. Loolu wone na ne li Mbind mu sell mi waxoon am na. Bu amul woon poliis, naroon na gën a metti. Réveillez-vous ! bii dafay wax ci jafe-jafe yi poliis bi am ci àddina si sépp. ”