Nañu fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bu benn fan bi
Laaj yii di topp, dañu leen defar ngir ñu mën a xam li ñuy waxtaane ci ndaje bu mag bu benn fan ci atum liggéeyu waare 2005, bala ndaje boobu di jot. Laaj yooyu lañuy laajte it bu ñuy fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Xaaj bi tudd “ Lu bees li ñu defar ngir fàttaliku li ñu waxtaane ci ndaje yu mag yi ” te nekk ci xët 4 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, wax na ni ñu waree jëfandikoo xaaj bii. Bu ngeen di fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bi, kiy jiite waxtaan bi war na xam bu baax ñaata minit la bëgg yàgg ci laaj bu nekk ngir mën a laal laaj yépp. Li ñu bëgg ci waxtaan bi mooy mu wone bu ni ñu mënee topp li ñu jàng ci ndaje bu mag bu benn fan bi.
SUBA SI
1. Lu tax déglu Yexowa gën a am solo tey ? Lan la déglu tekki (“ Lu tax ñu war a déglu Yexowa ”) ?
2. Naka la njaboot yi mënee fexe ba topp porogaraam bu baax ci wàllu ngëm (“ Njaboot yu nanguwul dara tere leen déglu Kàddu Yàlla ”) ?
3. Waaraatekat yi bokk ci mbooloo yi teewe ci ndaje bu mag bu benn fan bi, lan lañu def ngir waaraate saa yu ñu ci amee bunt (“ Nañu màggal Yàlla ci lépp li ñuy def ”) ?
4. Lan la ñu Yawut yi pàcc 3 ak 4 di jàngal ngir aar ñu ? Yexowa naka lay waxe ak ñun tey (“ Déglu Yàlla, dafa lay aar ”) ?
5. Loo jële ci waxtaan bi ñu def ngir ñi ñu sóob ci ndox (“ Jébbalu bi ak sóob bi ”) ?
NGOON GI
6. Lan lañu mën a jàng ci Yeesu bi mu nekkee ndaw ? Ndaw yi bokk ci mbooloo yi teewe ci ndaje bu mag bu benn fan bi, naka lañu roye Yeesu (“ Naka la déglu bu baax Kàddu Yàlla, mënee tax suñu ndaw yi am ngëm gu dëgër ”) ?
7. Naka la waajur yi mënee jàngal seeni doom ci li Yexowa bëgg bi ñu nekkee liir walla xale yu tuuti (“ Xale yu tuuti yuy déglu te xam li nekk ci Kàddu Yàlla ”) ?
8. Waxal ay fànn fu ñu war a déglu bu baax Yexowa, Doomam, ak “ surga bu takku te teey ” bi (Macë 24:45). Loolu, lu tax mu am solo lool ci ñun (“ Nañu déglu ndigalu Yàlla yi saa su ne ”)
?