Ndaje bu mag bu benn fan bii di ñów : li ñu fay waxtaane
Bu ñu la waxee ne musiba mu ngi ñów, waaye nga mel ni ku ko déggul, lu mettee-metti mën na la dal. Topp li ñu Yexowa di wax ci wàllu ngëm moo ëppati solo. Loolu dinañu ko wone bu baax ci ndaje bu mag bu benn fan bi ñuy def ci atum liggéeyu waare bii di ñów. Mu ngi tudd : “ Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo. ” — Lukk 8:18.
Ki ñu bànqaas bi yónnee, dina jële waxtaan bi muy njëkk def ci leetar bi Pool bind Yawut yi, pàcc benn. Dina wone naka la pàcc boobu baaxe ci ñun tey. Waxtaan biy mujj ci ndaje bu mag boobu dina tudd : “ Nañu déglu ndigalu Yàlla yi saa su ne. ” Ki ñu bànqaas bi yónnee moo koy def. Dina ñu dimbali ñu seetaat ndax ci dëgg-dëgg ñu ngi déglu Yexowa, Doomam ak “ surga bu takku te teey ” bi. — Macë 24:45.
Ci ndaje bu mag boobu, dina am lu bare luy dimbali njaboot yi. Dina am waxtaan bu tudd “ Njaboot yu nanguwul dara tere leen déglu Kàddu Yàlla ”. Waxtaan boobu dina ñu won ni ñu mënee fexe ba àddina si bañ ñu teree topp bu baax li ñuy jàng ci wàllu ngëm. Dinañu déglu ay nit ñu soppi seen dund ngir mën a jiital seen ngëm ci lépp li ñuy def. Dinañu déglu it waxtaan bi tudd “ Naka la déglu bu baax Kàddu Yàlla mënee tax suñu ndaw yi am ngëm gu dëgër ”. Dinañu ci déglu ay ndaw yuy topp dëgg gi ci lekkool bi, ci seen kanamu moroom, ak ci waaraate bi. Dina am it waxtaan bu tudd “ Xale yu tuuti yuy déglu te xam li nekk ci Kàddu Yàlla ”. Foofu dinañu gis ne waruñu xalaat ne xale yu tuuti yi mënuñu jàng lu bare. Dinañu woo ay xale yu ndaw ak seeni waajur, waxtaan ak ñoom. Dinañu gis ne jàngal xale bu tuuti lu jëm ci ni Yexowa di jëfe, lu baax la.
Tey, Seytaane mu ngiy nax waa àddina sépp. Waaye Yexowa moom mu ngiy won ñi koy jaamu fi ñu war a jaar (Peeñ. 12:9 ; Isa. 30:21). Déglu te topp bu baax ay ndigalam dina ñu may xam-xam, jàmm ak dund gu dul jeex. — Léeb. 8:32-35.