Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sept.
“ Dañu leen bëgg won lu neex lu jëm ci ñaan bi ñuy woowe Suñu Baay. Ay milioŋi nit dañuy boole wax yooyu ci seeni ñaan. [Jàngal Macë 6: 10.] Ci sa xalaat, bu coobare Yàlla amoon ba mu mat ci kow suuf si, naka la àddina si di mel ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafa ñuy leeral lépp li nekk ci ñaan boobu, boole ci li ñu jàng léegi. ”
Réveillez-vous ! 22 sept.
“ Jigéen yu bare mënuñu am doom. Am na ci sax yu ñu fase ndax loolu. Loolu yépp metti na. Ndax xam nga li doktoor yi mën a def ngir faj jigéen yooyu ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci loolu, te dafay wone ni ko Yàlla gise. ” [Jàngal Efes 3:14, 15 te wonal nit ki ne fàww ñu xam ni Yàlla gise mbir yooyu ndaxte moom moo sàkk njaboot.
La Tour de Garde 1er oct.
“ Tey dañuy waxtaan ak nit ñi ci loo xam ne ñépp a ko bëgg, maanaam xeex yépp jeex ci kow suuf. Dinaa la jàngal dara ba pare dinga ma wax ndax loolu dina mas a am. [Jàngal Sabuur 37:11 te mayal nit ki tontu.] Boo jàngee téere bii dinga gis ne li ñu wax fii ànd na ak li Yàlla bëggoon ca njëlbéen bi mu sàkkee suñu maam Aadama ak Awa. Dina la wax it li nga mën a def ngir bokk ci. ”
Réveillez-vous ! 8 oct.
“ At mu nekk am na ay millioŋi xale yu jigéen yu am doom fekk séyaguñu. Ndax loolu mettiwul ? [Mayal nit ki tontu.] Ci téere bii dañuy wax wayjur yi li ñu mën a def ngir seeni doom moytu loolu. [Jàngal 2 Timote 3:15 te won ko fa lu tax ñu war a jàngal xale yi lan mooy lu baax bu dee sax ay xale yu ndaw a ndaw lañu.] Janq yooyu dañuy sonn. Téere bii dafay won li janq yooyu mën a def ngir wàññi seeni jafe-jafe. ”