TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/06 p. 10
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bi ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 9/06 p. 10

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 sept.

Waxal lenn lu ñu dégg ci xibaar yi te muy itteel ñi nekk ci sa goxu mbooloo, ba pare laajal nit ki lii : “ Ci sa xalaat, li Biibël bi wax fii, ndax moo am tey ? [Jàngal 2 Timote 3:1 te mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone lu tax mu leer ne ñu ngi ci muju jamano. Dafay wone it li ñu war a def komka ñu ngi ci muju jamano. ”

Réveillez-vous ! Sept.

“ Am na ñu gëm ne Yàlla moo sàkk àddina si. Waaye téere yi ñuy jàng ca lekkool dañuy wone ne loolu àndul ak li boroom xam-xam yi wax. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Yawut ya 3:4.] Lépp li ñu wër, dafay feeñal xam-xam bu réy te wone ne am na lu tax mu nekk fii. Réveillez-vous ! bii dafay wone li ñu mën a jànge ci loolu. ”

La Tour de Garde 1er oct.

“ Boroom xam-xam yiy gëstu ci li jëm ci suñu dund te ñu leen di woowe ci tubaab biologistes, dañu jéem a dindi feebar yi te fexe ba nit gën a gudd fan. Ndax foog nga ne dund gu dul jeex dina mën a am ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal li waral ñu bëgg gën a gudd fan. [Jàngal Dajalekat (Ecclésiaste) 3:11, te boo koy jàng, fexeel ba “ les temps indéfinis, il les a mis dans leur coeur ” (maanaam, dund gu dul jeex gi dafa ko def ci suñu biir xol) feeñ bu baax a baax.] Téere bii dafay wone lu tax bi Yàlla sàkkee nit, dafa ko def ci fasoŋ buy tax mu bëgg dund ba fàww. ”

Réveillez-vous ! Oct.

“ Li ëpp ci nit ñi, seetaan tele dafa leen neex. Ndax foog nga ne du lépp lañu war a seetaan ci tele bi, te dañu war a tànn li ñuy seetaan ? [Mayal nit ki tontu, ba pare nanga jàng Léeb yi 13:20. Boo ci paree, wonal nit ki ne toog lu yàgg di seetaan nit ñiy génn tele, mën na la lor, ndaxte ñu ci bare amuñu xel.] Téere bii dafay wone naka la ñu tele bi di laale te naka lañu mënee yemale suñu seetaan. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager