Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sept.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Tey dañu bëgg a waxtaan lu jëmm ci séy. Am na ñoo xam ne, amuñu benn jàmm ci seen séy. Ci muñ kese lañu dëkk. Nit ñooñu lan moo leen mën a dimbali ? [Mayal nit ki tontu.] Mbind mu sell mi nee na, ci lu wóor, bu ñu toppee li Yàlla wax, dinañu am jàmm. [Jàngal Isayi 48:17, 18.] Téere bii, dafa ñuy won li Mbind mu sell mi wax ci wàllu séy. ”
Réveillez-vous ! 22 sept.
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Ni ko Mbind mi wonee, am na li nit mën a def te mala mënu ko. Ndax bëgg nga xam lan la ? [Mayal nit ki mu tontu.] Dinaa la won li ñu wax ci Sabuur 65:2. [Jàng ko.] Nit moom, dafa bëgg am diggante bu rafet ak Yàlla te wax ak moom. Téere bii dafay wone ni ñu mënee am loolu ak nit ñi te it ak Yàlla. ”
La Tour de Garde 1er oct.
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Ñun ñépp xam nañu ne Yàlla dafa ñu bëgg te mooy aji-kàttan ji. Waaye bu musiba amee, ñu bare dañuy laajte lu tax Yàlla du dimbali ñi nekk ci metit. Ndax xam nga ne Mbind mi nee na léegi Yàlla dindi suñuy coono yépp ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare jàngal Isayi 65:17.] Téere bii dafay wone ne tey, fi ñu nekk nii sax, Yàlla nekkul di seetaan metit yi rekk. ”
Réveillez-vous ! 8 oct.
[Boo nuyoo ba pare mën nga ne :] “ Ndax xam nga ne beykat yu bare dañuy sonn lool balaa ñuy am li ñuy dunde ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ci loolu la Réveillez-vous ! bii di wax. Dafay wone itam ne loolu léegi mu jeex ni ko Mbind mu sell mi waxe. Dinaa la ko jàngal fii. [Jàngal Sabuur 72:16.] Bu ma fi dellusee, dinañu waxtaan ci naka la ko Yàlla di defe. ”