Li ñu mën a wax bi ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sept.
“ Loo xalaat ci li yonent Musaa waxoon ci 5 Musaa (Deuteronome) 32:4. [Jàngal aaya boobu]. Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax metit ak yëf yu bon bare lool ci àddina, fekk Yàlla ku jub la te nekk Aji-kàttan ji ? [May ko mu tontu.] Téere bii dafay wone lu tax Yàlla bàyyi lu bon am ba tey. ”
Réveillez-vous ! sept.
“ Ñépp a bëgg am wér gu yaram ak gudd fan. Ndax yaakaar ëllëg bu neex mën na tax sa wér-gi-yaram gën a baax ? [May ko mu tontu, ba pare jàngal Léeb yi 17:22.] Téere bii dafay wone lu tax jar na ñu jéem a am gis-gis bu rafet ci suñu ëllëg. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 26.
La Tour de Garde 1 oct.
“ Ndax masuloo def dara ba pare réccu ko ? [May ko mu tontu.] Xoolal li ñu wax fii ci lu tax ñun ñépp yenn saay dañuy def dara ba pare réccu ko. [Jàngal Yérémi 10:23.] Ci Biibël bi, am na ay xelal yu baax ngir mën a tànn lu baax. ”
Réveillez-vous ! oct.
“ Ndax yaakaaruloo ne li mën a lor xale yi moo ëpp tey ? [May ko mu tontu.] Ñu bare gëm nañu ne dañu tollu ci jamano ju ñuy wax fii. [Jàngal 2 Timote 3:1-5.] Téere bi dafay joxe ay xelal yu baax ngir wayjur yi xam naka lañu mënee aar seeni doom ci nit ñu leen bëgg a def yëfu say-say. ”