Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sept.
“ Ñu bare gëm nañu ne ñi ñuy woowe “ nit ñu sell ñi ” dañu am kàttan bu réy, te li gën mooy ñu jaar ci ñoom bu ñu bëggee ñaan Yàlla. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Yeesu Krist wax fii. [Jàngal Yowanna 14:6.] Lii moo tax ñenn ñi di laaj ndax war nañu jaar ci “ nit ñu sell ñi ” ngir ñaan Yàlla. La Tour de Garde bii dafay wax ci loolu am solo. ”
Réveillez-vous ! 22 sept.
“ Tey, nit ñu bare dañu ragal li tubaab di woowe terrorisme ak li ñuy woowe armes biologiques. Ndax foog nga ne doom-Aadama dina ko mën a dindi ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dafay wone li Yàlla bëgg def. [Jàngal Esekiel 34:28.] Réveillez-vous ! bii dafay wone li ay nit wax ci loolu. ”
La Tour de Garde 1er oct.
“ Ñu bare dañu bëgg xam ndax jafe-jafe yu mel ni xeex, ñaawtéef ak li tubaab di woowe terrorisme dina mas a jeex. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Am na lu dalal xel lu Biibël bi wax. [Jàngal Sabuur 37:10, 11.] Yéenekaay bii dafay wone lu tax Yàlla dindiwul ba tey lu bon ak metit yi lu bon loolu di indi. ”
Réveillez-vous ! 8 oct.
“ Tey, njaboot yoo xam ne benn way-jur rekk moo fa nekk, yokku nañu lool. Biibël bi dafay wone ne Yàlla am na yërmande ci njaboot yooyu. [Jàngal Sabuur 146:9.] Réveillez-vous ! bii dafay wone naka la ndigal yi nekk ci Biibël bi di dimbalee wayjur yooyu ngir ñu mën a yar bu baax seeni doom. ”