Li ñu mën a wax ngir wone téere Qu’enseigne la Bible ?
Ci xët 3 ba 6, Sasu Nguuru Yàlla bii wone na lu bare lu ñu mën a wax ngir wone téere Qu’enseigne la Bible. Nangeen ko wax ci seen kàddu bopp ngir mu gën a baax. Nangeen seet yan waxtaan ñoo mën a neex nit ñi nekk ci seen gox. Nangeen xam bu baax it ponk yi ngeen mën a won nit ñi ci téere bi ngir waxtaan ci. Mën ngeen wax it leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone téere bi. Seetleen Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 8.
Biibël bi
◼ “ Nit ñu bare dañuy wax ne Biibël bi Kàddu Yàlla la. Waaye, komka ay nit ñoo ko bind, naka la mënee nekk Kàddu Yàlla ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal 2 Piyeer 1:21. Jàngal it ci téere bi li nekk ci xët 19 ak 20, xise 5.] Téere bii wone na li Biibël bi wax ci laaj yii. ” Won ko laaj yi nekk ci xët 6.
◼ “ Xam-xamu doomu-Aadama masul a bare ni mu baree tey. Waaye ba tey soxla nañu xelal yu mën a tax ñu am jàmm ak dund gu neex. Waaw fan lañu mënee am xelal yu mel noonu ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal 2 Timote 3:16, 17 ak xise 12 bi nekk ci xët 22 ak 23.] Téere bii dafa ñuy won ni ñu mëne am dund gu neex Yàlla, dund gu ñuy jariñ. ” Wonal nit ki nataal bi nekk ci xët 123 ak mbind yi nekk ci wetam ci xët 122.
Dee ak ndekkite
◼ “ Nit ñu bare dañu bëgg xam, ci lan la ñi dee nekke. Loolu ndax mën nañu ko xam ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Dajalekat (Ecclésiaste) 9:5 ak xise 5 ba 6 yi nekk ci xët 58 ak 59.] Téere bii dafay wone it lan mooy xew bés bu ndekkite amee ni ko Biibël bi waxe. ” Woneel nataal bi nekk ci xët 75.
◼ “ Ñun ñépp bëgg nañu gisaat suñuy mbokk yi gaañu, du dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Ñu bare bi ñu jàngee ci Biibël bi ne Yàlla dina dekkal ñi dee, seen naqar dafa wàññeeku bu baax. [Jàngal Yowaana 5:28, 29 ak it xise 16 ak 17 yi nekk ci xët 71 ak 72.] Pàcc bii dina tontu it ci laaj yii. ” Wonal nit ki laaj yi ñu def ci xët 66 ngir komaase pàcc bi.
Dund gu dul jeex
◼ “ Li ëpp ci nit ñi dañu bëgg am wér-gi-yaram te gudd fan. Bu nit mënoon a dund ba fàww, ndax dinga bëgg dund gu mel noonu ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Peeñu ma 21:3, 4, ak xise 17 bi nekk ci xët 54.] Téere bii dafay wone li ñu war a def ngir am dund gu dul jeex. Dafay wone it naka la dund gu dul jeex googu di mel. ”
Mbirum njaboot
◼ “ Ñépp a bëgg am jàmm ci seen kër, du dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Biibël bi dafay wone ne nit ku nekk am na lu mu mën a def ngir këram bare jàmm. Dafa war a am mbëggeel ni Yàlla. ” Jàngal Efes 5:1, 2 ak xise 4 bi nekk ci xët 135.
Am kër
◼ “ Ci béréb yu bare, kër gu baax te yomb, jafe na am. Ndax foog nga ne dina am bés boo xam ne, kenn ku nekk dina mën a am kër gu baax fu muy dëkk ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Esayi 65:21, 22 ak xise 20 bi nekk ci xët 34.] Li Yàlla dige noonu, naka lay ame ? Loolu la téere bii di wone. ”
Yexowa Yàlla
◼ “ Am na nit ñu bare ñu bëgg gën a jege Yàlla. Ndax xamoon nga ne ci loolu la ñu Biibël bi di xiir ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Saag 4:8a ak xise 20 bi nekk ci xët 16.] Téere bii dañu ko defar ngir dimbali nit ñi ñu gëstu Biibël bi ñu am ngir gën a xam Yàlla. ” Won ko laaj yi ñu def ci xët 8 ngir komaase pàcc bi.
◼ “ Ñu bare dañuy ñaan Yàlla ngir turam sell. Waaye Yàlla, naka la tudd ? Loolu mas nga ko laaj sa bopp ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Sabóor 83:18 ak xise 2 ak 3 yi nekk ci xët 195.] Téere bii dafay wone li Biibël bi wax dëgg ci Yexowa Yàlla ak ci li mu bëgg defal doom-Aadama yi. ”
Yeesu Krist
◼ “ Foo dem ci àddina, dinga fa fekk ay nit ñu mas a dégg turu Yeesu Krist. Am na ñuy wax ne nit ku doy kéemaan rekk la woon. Am na ñeneen ñuy wax ne moom mooy Yàlla Aji Kàttan ji, te dañu koy jaamu. Ni ñu gise Yeesu Krist ndax am na solo ? ” Mayal nit ki tontu te jàngal Yowaana 17:3. Jàngal it xise 3 bi nekk ci xët 37 ak 38. Won ko it laaj yi ñu fa def ngir komaase pàcc bi.
Bu ñuy ñaan Yàlla
◼ “ Ndax mas nga laaj sa bopp naka la Yàlla di tontoo suñuy ñaan ? [Mayal nit ki tontu te jàngal 1 Yowaana 5:14, 15 ak xise 16 ba 18 yi nekk ci xët 170 ba 172.] Pàcc bii dafay wone lu tax ñu war a ñaan Yàlla ak li ñu war a def ngir mu may ñu li ñu koy ñaan. ”
Mbirum diine
◼ “ Ñu bare tey dañuy wax ne diine yi fajuñu suñuy coono, waaye dañu koy yokk. Ndax foog nga ne diine dafa ñuy xiir ci lu baax ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Macë 7:13, 14 ak xise 5 bi nekk ci xët 146.] Pàcc bii dafay wone juróom-benni ponk yi mën a tax ñu xàmme diine bu Yàlla di nangu. ” Won ko ponk yi nekk ci xët 147.
Musiba yi ak metit yi
◼ “ Ñu bare bu ñu amee metit, dañu leen di wax ne ndogalu Yàlla la. Yàlla ku bare mbëggeel la. Kon ndax foog nga ne suñu metit yi, ci moom la jóge ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Saag 1:13.] Seetal li ñu wax fii ngir ñu xam lu tax Yàlla di bàyyi metit yooyu am te fekk du moom moo koy def. ” Jàngal xise 8 ak 9 yi nekk ci xët 10 ak 11.
◼ “ Bu musiba bu mag amee, ñu bare dañuy laajte ndax Yàlla fonk na doom-Aadama yi te ndax mu ngiy gis suñuy coono. Ndax mas nga laaj sa bopp loolu ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal 1 Piyeer 5:7 ak xise 11 bi nekk ci xët 11.] Téere bii dafay wone naka la Yàlla di dindee coono doom-Aadama yi ba mu jeex tàkk. ” Wonal nit ki laaj yi ñu def ci xët 106 ngir komaase pàcc boobu.
Xeex yi ak jàmm
◼ “ Jàmm la ñépp di ñaan. Waaye jàmm jooju ndax dinañu ko mas a am walla gént rekk la ? [Mayal nit ki tontu, te jàngal Sabóor 46:8, 9.] Téere bii dafay wone naka la Yàlla di defe li mu dige ak naka lay indee jàmm ci kow suuf si sépp. ” Wonal nit ki nataal bi nekk ci xët 35 te waxal ci xise 17 ba 21 yi nekk ci xët 33 ak 34.
[Wërale bi nekk paas 5]
Ni ñu mënee wax nit ki ne, bu ko neexee, mën na jàpple suñu liggéey
“ Boo bëggee, mën nga maye dara ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. ”
“ Jaayuñu suñu téere yii, waaye boo bëggee mën nga maye dara ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. ”
“ Xéyna yaa ngi laaj sa bopp fu ñuy jële xaalis bi ñuy defe liggéey bii. Xaalis boobu, ci li nit ñi di maye la jóge. Boo bëggee, mën nga joxe dara. ”