Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er mai
“ Li musiba yi di gën a bare tey, tax na mu am ñuy laaj seen bopp ndax du Yàlla mooy mbugël nit ñi. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare jàng 1 Yowaana 4:8.] Téere bii dafay wone lu tax ñu mën a wax ne du Yàlla mooy teg nit naqar yiy ànd ak musiba yooyu ”. Wonal nit ki waxtaan bi nekk ci xët 30.
Réveillez-vous ! Mai
“ Tey, boroom alal yu bare ak it ay nit ñu siiw lool, dañuy may ay kurél xaalis ngir dindi ci àddina si poroblem yu mel ni néew-doole, feebar walla ñàkk dem lekkool. Ci sa xalaat, ndax maye yooyu dinañu tax ñu dindi naqaru doomu Aadama ba ñu jeex tàq ? [Mayal nit ki mu tontu.] Kàddu Yàlla dafay wone lu tax li nit ñi di jéem noonu du sotti mukk. [Jàngal Njàlbéen ga 8:21.] Mbind mu sell mi wax na ne Yàlla dina dindi li indi coono doomu Aadama yi. Loolu la xaaju téere bii di wone. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 19.
La Tour de Garde 1er juin
“ Li ñu Biibël bi wax ci Nóoyin ak ci taw bu metti bi amoon ci suuf si sépp, bokk na ci nettali yi nit ñi gën a xam ci Mbind mu sell mi. Ndax foog nga ne taw boobu amoon na dëgg ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yeesu mas na ci wax, te ci moom loolu amoon na dëgg. [Jàngal Luug 17:26, 27.] Téere bii dafay wone lu tax ñu mën a gëm ne li ñu nettali ci taw bu metti boobu amoon na dëgg. Dafay wone it lu am solo li ñu ci mën a jang. ”
Réveillez-vous ! Juin
“ Yar xale dafa metti, rawatina bu demee ba nekk janq walla waxambaane te muy soppiku bu baax. Fan la wayjur yi mënee am xelal yu baax ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare jàngal Isaïe 48:17, 18.] Téere bii dafay wone xelal yu baax ci wayjur yi tey. Xelal yu leen di dimbali ñu nekk ay wayjur yu am xel ak xam-xam ci ni ñuy yore seeni doom ”