Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er janv.
“ Ndax ànd nga ak li ñu wax fii ? [Jàngal Saag 3:2.] Téere bii dafa ñuy won ni ñu mënee wax ay kàddu yuy bañ a gaañ suñuy waa kër. Xelal yooyu, ci Kàddu Yàlla lañu jóge. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 10.
Réveillez-vous ! Janv.
“ Séy boo gis dafay ànd ak jafe-jafe. Ci yow, fan la jëkkër ak jabar yi mënee am ay xelal yu wóor ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal xelal bu am solo bi ñu wax fii. [Jàngal Efes 5:22, 25.] Fii ci téere bii, dañuy wone lan la déggal sa jëkkër tekki. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 28.
La Tour de Garde 1er févr.
Ak poroblem yi ñu am yépp tey, ndax ci sa xalaat mën nañu am xel mu dal ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yaakaaru ëllëg bi Kàddu Yàlla di maye dimbali na ay nit ñu bare. [Jàngal benn ci aaya yi nekk ci waxtaan bi ngay won nit ki.] Téere bii dafay wone li Kàddu Yàlla wax ci fi doom-Aadama jóge, lu tax Yàlla sàkk nit, ak li ñu mën a séentu ëllëg. ”
Réveillez-vous ! Févr.
“ Ñu bare tey seen xel dalul, ndaxte nit ñi def li yoon tere dañu jékki-jékki rekk bare lool ci àddina. Ndax yaakaar nga ne mbir mi dina mas a tane ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal lu neex li Mbind mu sell mi waxoon ne dina am. [Jàngal Sab 37:10.] Téere bii dafay waxtaan ci fu poroblem boobu jóge. Dafay wax it li Kàddu Yàlla wax ngir faj poroblem boobu . ”