TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/05 p. 8
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 1/05 p. 8

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 janv.

“ Bi ñu doon waxtaan ak nit ñi dëkk ci gox gii, dañu gis ne ñépp a bëgg am dund bu gën a neex ngir ñoom ak seen njaboot. Waaye ñu bare mënuñu fexe ba am loolu. Ci sa xalaat, ndax suñu ëllëg mu ngi ci suñu loxo ? [Mayal nit ki tontu.] Biibël bi dafa nuy won ne am na li ñu mën a def ngir suñu ëllëg neex ndaxte suñu ëllëg, mu ngi aju ci li ñuy def tey. Téere bii, ci loolu lay wax. ” Jàngal 5 Musaa 30:​19, te won ko foofu ne Yàlla dafa ñuy bàyyi ñu tànn li ñu bëgg def ci suñu àddina.

Réveillez-vous! 22 janv.

“ Dañuy waxtaan ak nit ñi ci loo xam ne ñépp lay laal. Bu ñu feebaree, dañu bëgg am doktoor bu baax. Waaye ndax ñu bare ci ñun bu ñu demee ci suñu doktoor, dañu leen di won jikko yu rafet ? [Mayal nit ki tontu.] Boo jàngee téere bii, dinga xam yan coono la doktoor yi am ak li ñu mën a yaakaar ëllëg ci lu jëm ci doktoor yi. ” Jàngal Isayi 33:⁠24.

La Tour de Garde 1 févr.

“ Dañuy waxtaan ak nit ñi ci ni ñuy dunde tey ci suñu jamano jii. Boo gisee nit ñi di soxor ak seeni moroom walla ñu leen di toroxal, ndax loolu du la metti ? [Waxal li xewoon lu yàggul, te mayal nit ki wax li mu ci xalaat.] Ci téere bii, dañuy wax ni Yàlla di gise bakkanu nit. Wax na itam li Yàlla di def ngir musal ñu ci coono àddina yépp. ” Jàngal Sabuur 72:​12-14 te won ko foofu kàddu yi laal li xewoon lu yàggul li nga doon wax léegi.

Réveillez-vous! 8 févr.

“ Gis nañu ne wayjur yu bare amatuñu seen jotu doom. Ci sa xalaat, naka lañu mënee am jot ngir toog di waxtaan ak suñuy doom ? [Mayal nit ki tontu.] Ci Mbind mu sell mi dañuy wax wayjur yi ñu fexe ba am jot ngir seeni doom. Te dañu war a faral di def loolu. [Jàngal 5 Musaa 6:​6,7, te woneel foofu fu ñu neewe “ booy toog ci sa kër ” ak “ booy dox ci yoon wi ” ngir won wayjur yi kañ lañu mënee yar seeni doom.] Boo jàngee téere bii, dinga xam li wayjur yi mën a def ngir gën a am jot ngir seeni doom. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager