TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/08 p. 7
  • Ay Tont Ci Seeni Laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay Tont Ci Seeni Laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Téere Qu’enseigne la Bible ? lañuy njëkk jàng léegi ak ñi ñuy jàngal Biibël bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • ‘ Nu ma koy mëne lu moy kenn tette ma ? ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Xaaj 12 : Nañu leen won ni ñuy komaasee te kontinee njàngum Biibël
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 1/08 p. 7

Ay Tont Ci Seeni Laaj

◼ Yan ñaari téere lañu war a jàng ak ki ñuy jàngal Biibël bi ?

Téere Qu’enseigne la Bible lañu war a jël ngir komaase te kontine di jàngal nit ñi Biibël. Dëgg la terewuñu kuy jëfandikoo leneen mel ni kayit yu ndaw yi ngir komaase njàngum Biibël. Waaye nangeen def lépp ngir gaaw a bàyyi beneen téere boobu te kontine njàng mi ci téere Qu’enseigne la Bible. Gis nañu ne komaase njàngum Biibël ci téere Qu’enseigne la Bible dafay indi lu rafet lool.

Bu ñu jàngee ak nit téere Qu’enseigne la Bible ba mu jeex, te nit ki di jëm kanam ci wàllu ngëm, war nañu kontine njàng mi ci téere Adorez Dieu (Kol. 2:⁠7). Am na lu ñu bind ci téere boobu ci xët 2. Dañu wax foofu ne Biibël bi dafay xiirtal képp ku bëgg Yàlla mu fexe ba xam ni dëgg gi ame solo ak ni mu kawe ak ni mu xóote (Efes 3:18). Ni ñu ko waxe foofu, téere Adorez Dieu dañu ko defar ngir mu dimbali ñu ci loolu. Wax nañu it ne ñu ngi ñaan Yàlla ngir téere boobu dimbali ki koy jàng mu jëm kanam ci wàllu ngëm te kontine di dox ci yoon bu xat biy jëme ca àddina bu bees te jub bi Yàlla di indi.

Bu amee ku ñu sóob bala mu jeexal ñaari téere yooyu, war nañu kontine njàng mi ba jeexal ñaareelu téere bi. Bu dee sax sóob nañu nit ki ba pare, ki koy jàngal dina kontine di bind waxtu yi muy def ngir jàngal ko, ci kayit fi ñuy bind li ñuy def ci waaraate bi. Dina fa bind it ñaata yoon la dellu ngir seeti ko, te dina boole njàng moomu ci njàngum Biibël yi muy def. Waaraatekat biy ànd ak kiy def njàngum Biibël boobu, dina bind itam waxtu yi mu fa def.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager