Nañu pare ngir “ lépp luy jëf ju baax ”
1 Am na jamano joo xam ne Yeesu dafa amoon lu bees li mu bëggoon a def ci waaraate bi. Waaye dafa jël jot ngir waajal ay taalibeem (Macë 10:5-14). Dëgg la, ñépp a jàpp lool. Waaye bala ñuy dem waare këroo-kër, bu ñu jëlee tuuti minit ngir waajal li ñu bëgg wax, suñu liggéey dina jur lu baax. — 2 Kor. 9:6.
2 Naka lañu koy waajale : Waajal bu baax dafay komaase ci xam li nekk ci téere yi ñu bëgg a wone. War nañu xalaat it nit ñi dëkk ci gox bi ñuy waare. Lan moo leen itteel ? Lan mooy seen ngëm ? Mën nañu xool li ñu def ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone suñuy téere yi. Mën nañu xool it ci téere Comment raisonner.
3 Ci suñuy ndaje liggéeyu waare bi, dafay am ñuy wone ci kanamu ñépp ni ñu mënee waare. Nañu leen déglu bu baax. Loolu it dina ñu dimbali. Li ñu bëgg wax ci waaraate bi, bu ñu ko jëfandikoo lu bare, dootuñu soxlati jël waxtu bu bare ngir waajal ko. Waaye nag, saa yu ñu waree dem waaraate, bala ñuy dem, su ñu xalaatee tuuti ci li ñu bëgg a wax te kontine di seet li ñu ci mën a defaraat, dinañu gën a aay. War nañu seet it ndax def nañu ci suñu saag lépp li ñu nar a soxla.
4 Lan moo ñuy dimbali ñu bañ a fàtte li ñu bëgg wax ? Lenn li ñu mën a def mooy wax ci kaw li ñu bëgg wax ci waaraate bi te di ko def lu bare. Loolu dina tax mu des ci suñu xel. Am na ñuy def loolu ci njàngum Biibël bi ñuy def ci seen njaboot. Am na ñuy wax ne li leen di dimbali mooy, bind ci kayit bu ndaw lu gàtt lu ñu mën a wax, te di ci xool bala ñuy dugg ci kër.
5 Lu tax mu am njariñ : Bu ñu waajalee bu baax li ñu bëgg wax, dañuy gën a aay ci liggéeyu waare bi te mbégte bi ñu ciy am dafay gën a réy. Loolu dafa ñuy dimbali ñu mën a teey, te bañ a ragal bu ñu nekkee ci buntu kër. Dinañu gën a mën a déglu nit ki ñuy waxal, te bañ di xalaat ci li ñu nar a wax. Rax ci dolli, bu ñu xamee bu baax li nekk ci suñu téere yi, dina tax ñu gën a sawar bu ñu leen di wone.
6 Mbind mu sell mi dafa ñuy xiirtal ñu pare ngir def “ lépp luy jëf ju baax ” (Titt 3:1). Amul liggéey bu gën liggéeyu waare bi. Bu ñu ko waajalee bu baax, dañuy wone ne may nañu cér ñiy nangu déglu, ak it Yexowa, mi nga xam ne moom lañu fi nekkal. — Is. 43:10.